Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 90

Mu Ngiy Waxtaan Ak Jigéen Ci Teen

Mu Ngiy Waxtaan Ak Jigéen Ci Teen

YEESU toog na ci benn teen ci Samari ngir noppalu. Taalibeem yi dem nañu biir dëkk bi jëndi lu ñuy lekk. Jigéen bi Yeesu di waxal, dafa ñów root. Yeesu ne ko : ‘ May ma ndox, ma naan. ’

Loolu, lu doy waar la woon ci jigéen bi. Xam nga lu tax ? Ndaxte Yeesu, Yawut la te moom, jigéen bi, waa Samari la. Te li ëpp ci Yawut yi, bëgguñu waa Samari yi. Duñu wax sax ak ñoom ! Waaye Yeesu moom, bëgg na xeetu nit ñépp. Mu ne ko : ‘ Boo xamoon ki lay ñaan ndox, yow mi yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund. ’

Jigéen bi ne ko : ‘ Teen bi xóot na te amuloo sax siwo. Kon fooy jële ndoxum dund moomu ? ’

Yeesu ne ko : ‘ Boo naanee ci ndoxu teen bi, dinga maraat. Waaye ndox mi may joxe, ku ci naan mën na dund ba fàww. ’

Jigéen bi ne ko : ‘ Góor gi, may ma ci ndox moomu, ma bañ a marati. Te it, dootuma soxla ñów root fii. ’

Jigéen bi dafa foog ne ndox dëgg la Yeesu di wax. Waaye moom dafay wax ci dëgg gi jëm ci Yàlla ak nguuram. Dëgg googu, mu ngi mel ni ndoxum dund, maanaam ndox buy maye dund. Mën na may nit dund gu dul jeex.

Lii la Yeesu di wax jigéen bi léegi : ‘ Demal woowi sa jëkkër te ñów. ’

Jigéen bi tontu ko ne : ‘ Awma jëkkër. ’

Yeesu ne ko : ‘ Wax nga dëgg. Waaye amoon nga juróomi jëkkër te góor gi nekk ak yow léegi, du sa jëkkër. ’

Jigéen bi waaru ndaxte lépp li ko Yeesu wax moo am. Naka la Yeesu xame loolu ? Yeesu dafa ko xam ndaxte moom mooy Ki Yàlla dige woon te mu yónni ko. Kon Yàlla moo ko xamal loolu lépp. Taalibe Yeesu daldi dellusi, gis muy wax ak jigéenu waa Samari, ñu jaaxle lool.

Lan lañuy jàng ci loolu ? Dafay wone ne Yeesu dafa baax ak nit ñu bokk ci xeet yépp. Ñun it, dañu war a baax ak waa xeet yépp. Du xeetu nit ki moo war a tax ñu wax ne nit ku bon la. Yeesu bëgg na ñépp xam dëgg gi jëm ci dund gu dul jeex gi. Ñun it, war nañu bëgg dimbali nit ñi ñu xam dëgg gi.