Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 85

Yeesu Juddu Na Fu Ay Mala Di Fanaan

Yeesu Juddu Na Fu Ay Mala Di Fanaan

NDAX xam nga liir bi kan la ? Yeesu la. Mu ngi sog a juddu ci béréb fu mala yi di fanaan. Maryaama mu ngiy tëral Yeesu ci lekkukaayu jur, maanaam fu ñuy defe lekku mbaam yi ak yeneen mala yi. Waaye lu tax Yuusufa ak Maryaama nekk fii ak ay mala ? Du palaas fu xale war a juddu, du dëgg ?

Dëgg la, xale warul juddu foofu. Waaye lii moo tax ñu nekk fii : Kiy nguuru ci Room, Sesaar Ogust, digal na ñépp dem fu ñu juddoo ngir ñu bind seen tur. Yuusufa, fii ci Betleyem la juddu. Waaye bi ñu fi agsee, amul woon benn néeg fu ñu mënoon a fanaan. Looloo tax ñu ñów fii. Te ci bés boobu la Yeesu juddu ! Waaye, ni nga ko gise fii, mu ngi ci jàmm.

Ndax gis nga sàmmkat yi di seetsi Yeesu ? Àll lañu doon fanaan di toppatoo seeni xar, ñu daldi gis leer bu leer nàññ di leen wër. Malaaka la woon ! Sàmmkat yi tiit lool. Malaaka mi ne leen : ‘ Buleen tiit ! Xibaar bu neex laa leen di xamal. Tey ca Betleyem, Almasi bi juddu na. Dina muccal mbooloo mi ! Dingeen ko gis ñu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur. ’ Jékki-jékki malaaka yu bare daldi ñów te sant Yàlla. Sàmmkat yi gaawantu dem wuti Yeesu. Léegi gis nañu ko.

Ndax xam nga lu tax Yeesu wuute ak ñeneen nit ñi ? Ndax xam nga dëgg moom mooy kan ? Fàttalikul li ñu jàngoon ci nettali bu jëkk bi ci téere bii. Waxoon nañu lu jëm ci taawu Yàlla. Doom jooju, dafa doon liggéey ak Yexowa bi mu doon sàkk asamaan ak suuf ak li ci des lépp. Yeesu mooy doom jooju !

Waaw, Yexowa jël na bakkanu Yeesu, dugal ko ci biiru Maryaama, mu daldi màgg foofu, mel ni yeneen liir yi. Waaye liir bii, doomu Yàlla la woon. Yeesu mujj na juddu fu mala yi di fanaan ci dëkku Betleyem. Ndax léegi xam nga lu tax malaaka yi kontaan lool bi ñu doon yëgal nit ñi ne Yeesu juddu na ?