Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 100

Yeesu Ci Tool Bi

Yeesu Ci Tool Bi

YEESU ak ndawam yi dañu jóge néeg ba nekkoon ca kow kër ga, dem ca toolu Setsemane. Faraloon nañu di ñów fii. Yeesu ne leen ñu bañ a nelaw te ñaan. Mu daldi leen sore tuuti, sukk ba boppam laal suuf te ñaan.

Mu dellu fu ndawam yi nekk. Lan lañu nekk di def ci li nga foog ? Dañuy nelaw ! Yeesu wax na leen ñetti yoon ñu bañ a nelaw, waaye saa yu dellusee mu fekk leen di nelaw. Lii la leen wax bi mu mujjee dellusi : ‘ Naka ngeen mënee nelaw ci waxtu bu mel ni bii ? Waxtu bi ñu may jébbal samay noon jot na. ’

Bi mu waxee loolu rekk, ñu dégg coowu mbooloo mu réy. Xoolal nit ñi ñów di yor ay jaasi ak ay bant ! Dañu yor it ay bant yuy tàkk ngir am leer. Ñu ngi jegesi. Kenn daldi jiitu, ñów ci Yeesu, fóon ko, ni nga ko gise fii. Nit ki, Yudaa Iskariyo la. Lu tax muy fóon Yeesu ?

Yeesu ne ko : ‘ Yudaa, ndax ci fóon nga may wore ? ’ Waaw, fóon bi, misaal la. Ci la ñi ànd ak Yudaa nar a xàmmee Yeesu mi ñu bëgg a jàpp. Ñu daldi ko jàpp. Waaye Piyeer du leen bàyyi ñu jàpp Yeesu noonu. Fàww mu xeex. Mu daldi génne jaaseem, dóor ko ki ko jege woon. Tuuti mu laal bopp bi, nopp bi dagg. Waaye Yeesu laal na noppu nit ki, mu wér.

Yeesu wax Piyeer lii : ‘ Dellool sa jaasi fi mu nekkoon. Xanaa xamuloo ne mën naa laaj sama Baay ay junniy malaaka ngir ñu muccal ma ? ’ Yeesu mën na ko kay ! Waaye du laaj Yàlla benn malaaka sax ndaxte xam na ne waxtu bi ko noonam yi war a jàpp, jot na. Moo tax mu bàyyi leen ñu yóbbu ko. Nañu seet lan mooy dal Yeesu léegi.