Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 87

Yeesu Ci Kër Yàlla Gi, Fekk Xale La

Yeesu Ci Kër Yàlla Gi, Fekk Xale La

XOOLAL xale bi di waxtaan fii ak mag ñi. Ay jàngalekat lañu ci kër Yàlla gi nekk Yerusalem. Xale bi, Yeesu la. Màgg na te léegi 12 at la am.

Jàngalekat yi waaru nañu lool ndaxte Yeesu dafa xam lu bare ci Yàlla ak ci li ñu bind ci Biibël bi. Waaye lu tax Yuusufa ak Maryaama nekkuñu fi ñoom it ? Ana ñu ? Nañu seet loolu.

At mu nekk, Yuusufa faral na di yóbbu njabootam ca Yerusalem ngir màggali bés bi ñu woowe bésu Jéggi bi. Nasaret sore na lool Yerusalem. Oto amul, saxar amul. Jamano jooja, loolu lépp amul woon. Kon li ëpp ci nit ñi, dañu doon dox. Ku jóge woon Nasaret, bëgg dem Yerusalem, dafa waroon a dox lu jege ñetti fan.

Yuusufa bare na ay doom yu mu war a toppatoo léegi. Ay rakku Yeesu lañu. Ren, Yuusufa ak Maryaama dem nañu ak seeni doom Yerusalem te léegi ñu ngi ñibbi Nasaret. Pur ñoom, Yeesu mu ngi ànd ak ñeneen ñi ñu bokkal yoon. Waaye bi ñu taxawee ci ngoon si pur fanaan, mënuñu woon a fexe ba gis ko. Ñu daldi ko seet ci biir mbokk yi ak xarit yi. Nekkul ak ñoom ! Ñu daldi dellu Yerusalem, seet ko fa.

Mujj nañu gis Yeesu fii ak jàngalekat yi. Mu ngi leen di déglu te am na lu mu leen di laaj. Ñépp waaru ndax ni Yeesu ame xel. Maryaama ne : ‘ Sama doom, lu tax nga def ñu lii ? Man ak sa baay, ñu ngi la doon seet, jaaxle lool. ’

Yeesu ne leen : ‘ Lu tax ngeen may seet ? Xanaa xamuleen ne dama war a nekk ci sama kër Baay ? ’

Nekk fu ñu mën a jàng lu jëm ci Yàlla, loolu dafa neex Yeesu lool. Ndax loolu waru ñu neex ñun it ? Ca Nasaret fu mu dëkk, semen bu nekk, Yeesu dafa doon teewe ay ndaje ngir jaamu Yàlla. Ndegam dafa doon déglu bu baax, dem na ba xam lu bare ci li nekk ci Biibël bi. Nañu mel ni Yeesu te roy ko.