Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 7

Bi Yàlla dekkalee Yeesu ba bi ñu tëjee Pool kaso

Bi Yàlla dekkalee Yeesu ba bi ñu tëjee Pool kaso

Yeesu dekki na ci ñetteelu fan bi ginnaaw bi mu deewee. Bés boobu, feeñu na taalibeem yi juróomi yoon. Mu daldi leen feeñu ci lu mat 40 fan, ba pare mu yéeg asamaan, fekk ay taalibeem ñu ngi ko doon xool. Fukki fan ginnaaw loolu, Yàlla wàcce na xel mu sell mi ci taalibe Yeesu yi nekkoon Yerusalem di xaar.

Ginnaaw loolu, ay noonu Yàlla tëj nañu ndaw yi kaso, waaye benn malaaka génne na leen kaso ba. Ñi bañoon Ecen dañu ko sànni ay xeer ba mu dee. Waaye dinañu gis ni Yeesu tànne kenn ci ñoom pur mu nekk ndawam. Kooku mooy ndaw li Pool. Ñetti at ak génn-wàll ginnaaw bi Yeesu deewee, Yàlla yónni na ndaw li Piyeer ci ku nekkul woon Yawut te tudd Korney ngir mu waar ko, moom ak njabootam.

Lu jege 13 at ginnaaw loolu, Pool tàmbali na tukkeem bu jëkk ngir waare. Timote ànd na ak Pool ci ñaareelu tukki bi mu def. Pool ak ñi mu àndaloon fekke nañu lu bare lu neex te xumb ci liggéeyu Yàlla bi ñu doon def. Dinañu jàng loolu ci xaaj bii. Mujj nañu tëj Pool kaso ci Room. Bàyyi nañu ko mu génn ñaari at ginnaaw loolu, waaye dañu ko mujj a tëjaat kaso, ba pare rey ko. Li ñu nettali ci XAAJ 7, amoon na ci biir lu war a tollu ak 32 at.

 

IN THIS SECTION

NETTALI 102

Yeesu Mu Ngi Dund

Bi benn malaaka ñówee puus xeer bu mag bi tëjoon bàmmeelu Yeesu bi, soldaar yi dañu waaru ndax li ñu gis ci biir.

NETTALI 103

Ci Biir Néeg Bu Ñu Tëj

Lu tax taalibe Yeesu yi xamewuñu ko bi mu dekkee ba pare ?

NETTALI 104

Yeesu Mu Ngiy Dellu Asamaan

Bala Yeesu di dem asamaan, dafa jox taalibeem yi ndigal bi mujj.

NETTALI 105

Ñu Ngiy Xaar Ci Yerusalem

Lu tax Yeesu wàcce xel mu sell mi ci taalibeem yi ci bésu Pàntakott ?

NETTALI 106

Génne Nañu Leen Kaso

Njiitu diine Yawut yi dañu dugal ndaw yi kaso ngir ñu bàyyi waare bi, waaye Yàlla amoon na leneen ci xelam.

NETTALI 107

Sànni Nañu Ay Xeer Ecen Ba Rey Ko

Ba bi muy dee sax, Ecen dafa ñaan ñaan bu doy waar.

NETTALI 108

Ci Yoonu Damas

Ab leer buy gumbalaate ak baat bu jóge ci kaw asamaan dañu soppi dundu Sool.

NETTALI 109

Piyeer Seetsi Na Korney

Ndax Yàlla day gënale xeet ?

NETTALI 110

Timote Mooy Dimbali Pool Léegi

Timote bàyyi waa këram ngir ànd ak Pool ci liggéeyu waare bi.

NETTALI 111

Xale Bu Góor Bu Gëmméentu Ba Nelaw

Ëtikus dafa nelaw ci waare Pool bi njëkk waaye du ci ñaareel waare bi. Li xewoon diggante ñaari waare kéemaan la dëgg.

NETTALI 112

Gaal Gi Toj Na

Bi ñépp demee ba reer, Pool daldi jot xibaar bu jóge ci Yàlla, xibaar bu ko may yaakaar.

NETTALI 113

Pool Mu Ngi Room

Naka la Pool mënee def liggéeyam niki ndaw fekk mu ngi kaso ?