Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 106

Génne Nañu Leen Kaso

Génne Nañu Leen Kaso

XOOLAL malaakaa mi di teye bunt bi ak loxoom. Ñi muy génne kaso, ndawi Yeesu lañu. Nañu seet lu tax ñu tëjoon leen kaso.

Bi xel mu sell mi wàccee ci ndaw Yeesu yi, yàggul dara. Benn ngoon Piyeer ak Yowaana dugg ca kër Yàlla gi ci Yerusalem. Mu am ci wetu bunt bi benn góor gu judduwaale lafañ. Bés bu nekk, ay nit ñoo ko fiy teg ngir mu yelwaan. Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana, mu daldi leen ñaan pur ñu may ko dara. Lan la ndaw yi di def ?

Dañu taxaw, xool ko, moom mi néew doole. Piyeer ne ko : ‘ Awma xaalis, waaye li ma am, dinaa la ko jox. Ci turu Yeesu, jógal te dox ! ’ Piyeer jàpp loxo ndeyjooru waa ji, mu daldi tëb, dox. Ñépp waaru te kontaan lool ci kéemaan bu rafet boobu.

Piyeer ne leen : ‘ Kéemaan bii, dañu ko def ci kàttanu Yàlla, mi dekkal Yeesu. ’ Bi ñu doon wax ak mbooloo mi, ay kilifa diine ñów. Dañu mer ndaxte Piyeer ak Yowaana dañuy wax ak mbooloo mi lu jëm ci Yeesu mi Yàlla dekkal. Ñu jàpp leen, tëj leen kaso.

Ca ëllëg sa, kilifa diine yi am ndaje bu mag. Ñu indi fa Piyeer, Yowaana ak ki ñu faj. Kilifa yi ne leen : ‘ Ci ban kàttan ngeen defe kéemaan boobu ? ’

Piyeer ne leen ci kàttanu Yàlla, moom mi dekkal Yeesu, lañu ko defe. Saraxalekat yi xamuñu lu ñuy def, ndaxte mënuñu weddi ne kéemaan boobu amoon na. Ñu daldi wax ndaw yi ñu bañ a waxati ci Yeesu, ba pare bàyyi leen ñu dem.

Ndaw yi ñu ngi kontine di waare lu jëm ci Yeesu te di faj ñi feebar. Kéemaan yooyu siiw lool. Ñu bare sax dañu doon jóge ci dëkk yi wër Yerusalem, indi ay nit ñu feebar ngir ndaw yi faj leen. Loolu tax na kilifa diine yi iñaan. Ñu daldi leen jàpp, dugal leen kaso. Waaye yàgguñu fa.

Ci guddi gi, malaakaa Yàlla ubbi na buntu kaso bi, ni nga ko gise fii. Malaaka mi ne leen : ‘ Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, kontine di wax ak nit ñi. ’ Ci ëllëg si, bi kilifa diine yi yónnee ngir jëli ndaw ya ca kaso ba, kenn gisu leen fa. Dañu leen fekk ci kër Yàlla di jàngal nit ñi. Ñu indi leen ci saal bu mag bi, fu ñuy àtte nit ñi.

Kilifa diine yi ne leen : ‘Waxoon nañu leen ci lu leer ngeen bañati jàngale lu jëm ci Yeesu. Waaye feesal ngeen Yerusalem ak seen njàngale mi. ’ Ndaw yi tontu leen ne : ‘ Yàlla mi nekk suñu kilifa lañu war a déggal, moo gën déggal nit. ’ Kon dañu kontine di waare “ xebaar bu baax bi ”. Ndax nit ñooñu, jaruñu roy ?