Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 105

Ñu Ngiy Xaar Ci Yerusalem

Ñu Ngiy Xaar Ci Yerusalem

ÑI NEKK fii, ay taalibe Yeesu lañu. Topp nañu li mu leen waxoon te toog nañu Yerusalem. Bi ñu nekkoon di xaar noonu, ñu daldi dégg coow bu réy ci biir kër gi yépp. Mu ngi mel ni ngelaw bu réy te am doole. Lu mel ni làmmiñ yu mel ni safara daldi feeñ ci kow taalibe bu nekk. Ndax yaa ngi gis làmmiñ yooyu ci kow boppu kenn ku nekk ? Loolu lépp, lu mu tekki ?

Kéemaan la ! Yeesu dellu na asamaan, nekk ak Baayam foofu. Fii, mu ngiy wàcce ci kow taalibeem yi xel mu sell mi jóge ci Yàlla. Ndax xam nga lan la xel moomu di leen defloo ? Ñoom ñépp, komaase nañu di wax yeneeni làkk.

Ñu bare ci Yerusalem dégg nañu coow boobu mel ni ngelaw bu am doole. Ñu daldi ñów, bëgg xam lu xew. Am na ci ñoom ñu bokk ci yeneen xeet te ñów Yerusalem ndax feetu yawut bi ñuy woowe Pàntakot. Lu doy waar lañu fekke foofu ! Dañu dégg taalibe yi di wax ci seeni làkk lu rafet li Yàlla def.

Ñu ne : ‘ Waaw, ñii, ñoom ñépp, ay waa Galile lañu. Naka lañu mënee wax ci làkk yi ñuy làkk ci suñuy réew ? ’

Piyeer daldi jóg, taxaw ngir wax leen li xew. Mu yëkkëti baatam, wax mbooloo mi ni nit ñi reye Yeesu, wax ko it ne Yexowa dekkal na ko. Mu ne leen : ‘ Léegi Yeesu mu ngi asamaan ci ndeyjooru Yàlla. Te wàcce na xel mu sell mi mu dige woon. Loolu moo tax ngeen gis te dégg kéemaan yii. ’

Bi Piyeer waxee loolu, ñu bare ci mbooloo mi daldi yëg naqar ci seen xol ndax li ñu def Yeesu. Ñu ne Piyeer : ‘ Lan lañu war a def ? ’ Piyeer tontu leen ne : ‘ Dangeen war a soppi seen dund te sóobu ci ndox. ’ Kon bés boobu, sóob nañu ci ndox lu war a mat 3 000 nit, ñu daldi nekk taalibe Yeesu.