Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 109

Piyeer Seetsi Na Korney

Piyeer Seetsi Na Korney

NDAW li Piyeer moo taxaw fii te ñi nekk ci ginnaawam, ay xaritam lañu. Waaye lu tax nit kooku sukk ci kanamu Piyeer ? Ndax war na def loolu ? Ndax xam nga kan la ?

Nit kooku, Korney la tudd. Njiit la ci soldaaru Room yi. Korney xamul Piyeer, waaye dañu ko wax mu woo ko këram. Nañu seet naka la loolu ame.

Taalibe Yeesu yu jëkk yi, ay Yawut lañu woon. Korney moom, du Yawut. Waaye bëgg na Yàlla, dafa koy ñaan, te lu baax li muy defal nit ñi bare na. Benn ngoon, benn malaaka daldi ko feeñu, ne ko : ‘ Neex nga Yàlla, te léegi dina la may li nga ko ñaan. Yónnil léegi ay nit ñu woo ku tudd Piyeer. Ci dëkku Yope la nekk ci kër Simoŋ bi nekk ci wetu géej ga. ’

Korney daldi yónni ci saa si ay nit pur ñu woo Piyeer. Ci ëllëg si, bi ñu doon jege Yope, dafa fekk Piyeer nekk ci teraasu kër Simoŋ. Foofu, Yàlla feeñal ko lu mel ni sér bu mag buy wàcc asamaan. Ci sér boobu amoon na fasoŋu mala yu bare. Ci ndigal yi Yàlla joxoon waa Israyil, waxoon na ne lekk mala yooyu, lu araam la. Waaye Piyeer dafa dégg baat bu ko ne : ‘ Jógal Piyeer, reyal te lekk. ’

Piyeer ne ko : ‘ Déedéet ! Masuma lekk lu araam. ’ Baat bi ne Piyeer : ‘ Bàyyil di araamal li Yàlla sellal léegi. ’ Ñetti yoon la loolu am. Piyeer nekk di xalaat ci lu loolu lépp tekki. Ñi Korney yónni woon daldi agsi ci kër gi te laajte Piyeer.

Piyeer wàcc, ne leen : ‘ Maa ngi nii, man mii ngeen di wut. Lu doon seeni tànk ? ’ Bi ñu waxee Piyeer ne benn malaaka moo sant Korney mu woo ko këram, Piyeer nangu dem ak ñoom. Ci ëllëg si la Piyeer ak ay xaritam dem seeti Korney ca Sesare.

Korney woo na këram ay mbokkam ak ay xaritam yi ko gën a jege. Bi Piyeer duggee, Korney daje ak moom, mu daanu ci tànkam, sukk, ni nga ko gise fii. Waaye Piyeer ne ko : ‘ Jógal ; man it, nit rekk laa. ’ Waaw, Biibël bi wone na ne sukk ci kanamu nit di ko jaamu, baaxul. Yexowa rekk lañu war a jaamu.

Piyeer daldi waar ñi fa nekkoon. Mu ne : ‘Gis naa ne Yàlla nangu na képp ku ko bëgg jaamu. ’ Bi mu doon wax, Yàlla daldi wàcce xelam mu sell mi, nit ñi daldi wax yeneeni làkk. Taalibe yi àndoon ak Piyeer te nekkoon Yawut daldi waaru, ndaxte dañu foogoon ne Yawut yi rekk la Yàlla nangu. Loolu dafa leen di jàngal ne Yàlla du gënale xeet mukk. Loolu de, kenn waru ko fàtte !