Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 110

Timote Mooy Dimbali Pool Léegi

Timote Mooy Dimbali Pool Léegi

XALE bu góor bi ngay gis fii ak ndaw li Pool, Timote la. Mu ngi dëkk ak njabootam ci Listar. Yaayam mu ngi tudd Ënis, maamaam bu jigéen, Lowis.

Pool ñów na fi ci Listar ñaari yoon ba pare. Bii yoon mooy ñetteel bi. Lu war a tollu ak benn at ci ginnaaw, Pool ak Barnabas ñoo fi jëkkoon a ñów ngir waare. Léegi Pool dellusiwaat na ak xaritam Silas.

Ndax xam nga lan la Pool di wax Timote ? Lii la koy laaj : ‘ Ndax dinga bëgg a ànd ak Silas ak man ? Dinga ñu mën a dimbali ci waar ay nit ñu dëkk ci dëkk yu sore. ’

Timote tontu ko ne : ‘ Waaw, bëgg naa dem. ’ Kon yàggul ginnaaw loolu, Timote bàyyi na waa këram, dem ak Pool ak Silas. Waaye bala ñuy jàng ci seen tukki boobu, nañu seet li xewoon ak Pool. Am na léegi lu tollu ak 17 at bi Yeesu feeñu woon Pool ci yoonu Damas.

Yaa ngi fàttaliku ne Pool dafa ñówoon Damas ngir fitnaal taalibe Yeesu yi. Léegi, moom ci boppam, taalibe Yeesu la ! Ay noon jéem nañu ko rey ndaxte bëgguñu li muy jàngale ci Yeesu. Taalibe yi dimbali nañu Pool mu rëcc. Dañu ko dugal ci pañe bu mag, wàcce ko ci biti miiru dëkk bi.

Ginnaaw loolu, Pool dem na waare ca Ancos. Foofu lañu jëkk a woowe taalibe Yeesu yi gaayi Kirist, maanaam karceen. Ginnaaw loolu, dañu yónni Pool ak Barnabas ca réew yu sore ngir waare fa. Benn ci dëkk yooyu moo tudd Listar. Foofu la Timote dëkk.

Léegi, benn at ginnaaw loolu, Pool dellusi na Listar. Bi Timote demee ak Pool ak Silas, xam nga fan lañu dem ? Xoolal kàrt bi nekk fii. Dinañu jéem a xam yenn ci dëkk yooyu.

Dañu jëkk dem ca Ikoñum bi leen jege woon, ba pare dem ca dëkk bi tudd Ancos. Ñu daldi dem Torowas, ba pare Filib, Tesalonig ak Bere. Ndax gis nga Aten ci kàrt bi ? Pool waare na foofu. Ginnaaw loolu, toog nañu Korent lu mat benn at ak genn-wàll, di waare. Ñu mujj a dem Efes, toog fa tuuti. Ñu daldi jël gaal, dellu Sesare, ba pare dem Ancos, fu Pool dëkk.

Kon Timote tukki na ay téemeeri téemeeri kilomet, di dimbali Pool mu waare “ xebaar bu baax bi ” te tàmbali ay mbooloo karceen yu bare. Boo demee ba mag, ndax dinga jaamu Yexowa bu baax ni ko Timote defe woon ?