Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 111

Xale Bu Góor Bu Gëmméentu Ba Nelaw

Xale Bu Góor Bu Gëmméentu Ba Nelaw

WAAW, li xew fii, lan la ? Xale bi tëdd ci suuf, mbaa li ko dal garaawul ? Xoolal ! Pool a ngi génn kër gi di ñów ! Ndax gis nga Timote it ? Mbaa du ci palanteer bi la xale bi daanoo ?

Waaw, loolu la. Pool dafa doon waar taalibe yi nekk fii ci Torowas. Xamoon na ne bala mu leen di gisaat, dina yàgg lool ndaxte ci suba si la waroon a tukki ci gaal. Muy wax ak ñoom ba minwi jot.

Xale bi nekk fii te tudd Ëtikus, dafa toogoon ci palanteer bi, mu gëmméentu, daldi nelaw te daanu ñetti etaas ci suuf ! Kon xam nga lu tax nit ñi tiit nii. Bi ñu fabee xale bi, ñu gis ne li ñu ragaloon moo am : Xale bi dee na !

Bi Pool gisee ne xale bi dee na, mu tëdd ci kowam, jàpp ko ak loxoom yi, ba pare ne : ‘ Buleen ragal. Amul benn poroblem ! ’ Te mooy dëgg ! Xale bi dundaat na. Kéemaan la te Pool moo ko def ! Ñépp kontaan lool.

Ñépp yéegaat, ba pare lekk. Ginnaaw loolu, Pool kontine na waxtaanam ba bët set. Waaye na la wóor ne Ëtikus nelawatul ! Ginnaaw loolu, Pool, Timote ak ñi àndoon ak ñoom dugg nañu ci gaal gi, dem. Ndax xam nga fan lañu dem ?

Pool mu ngi waaj a pare ci ñetteelu tukki bi mu def ngir waare. Léegi mu ngi ñibbi fi mu dëkk. Ci tukki bii, Pool toog na ñetti at ci dëkku Efes. Kon bii yoon, tukki bi mu def moo gënoon a yàgg ñaareel bii paase.

Gaal gi jóge na Torowas, taxaw tuuti ci Mile. Ndegam Efes sorewul, Pool dafa yónnee ñu woo njiiti mbooloo moomu pur ñu ñów, mu mën a wax ak ñoom, ndaxte dootu leen gisati. Waxtu bi gaal gi waree dem, bi mu jotee, xolu ñépp jeex ndaxte Pool mu ngiy dem !

Gaal gi mujj na teer Sesare. Bi Pool nekkee ci kër taalibe bi tudd Filib, yonent bi tudd Agabus yëgal ko ne, bu àggee Yerusalem dinañu ko tëj kaso. Te loolu moo am. Pool toog na kaso ñaari at ci Sesare, ba pare ñu yónni ko Room ngir àtte ko fa ci kanamu Sesaar mi nekkoon buuru Room. Nañu seet li xew ci yoonu Room.