Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 102

Yeesu Mu Ngi Dund

Yeesu Mu Ngi Dund

NDAX xam nga jigéen bii, kan la ? Ñaari góor ñi, ñan lañu ? Jigéen bi, xaritu Yeesu la. Maryaamam Magdala la tudd. Góor ñi sol lu weex, ay malaaka lañu. Maryaama mu ngi xool fi ñu defoon néewu Yeesu. Béréb boobu dafa meloon ni néeg. Bàmmeel la. Waaye xoolal ! Néewu Yeesu nekkatu fi. Ku ko fi jële ? Nañu seet loolu.

Bi Yeesu deewee ba pare, saraxalekat yi dem nañu ca Pilaat ne ko : ‘ Bi Yeesu doon dund, ne woon na ne ginnaaw ñetti fan dina dekki. Kon, nanga santaane ñu wottu bàmmeel bi. Su ko defee, taalibeem yi duñu mën a ñów, sàcc néew bi ba pare ne Yeesu dekki na ! ’ Pilaat wax saraxalekat yi ñu def ay soldaar ci bàmmeel bi ngir wottu ko.

Waaye ci ñetteelu fan ginnaaw bi Yeesu deewee, suba teel, jékki-jékki rekk benn malaaka Yexowa ñów. Mu puus xeer bu mag bi tëjoon bàmmeel bi. Soldaar yi tiit ba mel ni ñu dee. Bi ñu xoolee ci biir bàmmeel bi, amatul néew ! Ay soldaar dem biir dëkk bi wax ko saraxalekat yi. Ndax xam nga lan la saraxalekat yu bon yooyu def ? Dañu fey soldaar yi pur ñu fen. Ñu ne leen : ‘ Nangeen wax ne taalibeem yi ñoo sàcc néew bi ci guddi, fekk dangeen doon nelaw. ’

Ci diggante bi, ay jigéen yu nekkoon xaritu Yeesu dem ci bàmmeel bi. Bi ñu gisee ne dara nekkatu fa, ñu jaaxle lool ! Ñaari malaaka yu soloon ay yére yu doon melax daldi feeñu, ne leen : ‘ Lu tax ngeen di seet Yeesu fii ? Dekki na. Gaawleen dem wax ko taalibeem yi. ’ Jigéen yi daldi daw, daw bu gaaw a gaaw ! Ci yoon bi benn góor daldi leen taxawal. Xam nga kan la ? Yeesu la ! Mu ne leen : ‘ Demleen wax ko samay taalibe. ’

Bi jigéen yi waxee taalibe yi ne Yeesu mu ngi dund te gis nañu ko, ñoom mënuñu ko gëm. Piyeer ak Yowaana daldi dem ca bàmmeel ba ngir gisal ko seen bopp. Dara nekkatu fa ! Piyeer ak Yowanna dem. Maryaamam Magdala toog fa. Foofu la xoole ci biir ba gis ñaari malaaka yi.

Ndax xam nga lu tax néewu Yeesu nekkatu fa ? Yàlla moo ko fi dindi. Yàlla dekkalul Yeesu ci yaramu nit bi mu amoon bi mu deewee. Dafa jox Yeesu yaram bu bees. Yaramu xel la. Mooy yaram bi malaakaa yi nekk asamaan am. Waaye Yeesu mën na jël yaram bu nit mën a gis ngir taalibeem yi xam ne dekki na. Loolu lañuy gis léegi.