NETTALI 115
Àjjana Ju Bees Ci Kow Suuf Si
XOOLAL garab yu mag yi, tóor-tóor yu rafet yi ak montaañ yu kowe yi. Ndax loolu lépp rafetul ? Xoolal kéwél gii di lekk ci loxo xale bu ndaw bi. Xoolal itam gaynde yi ak fas yi nekk foofu ci ñax bi. Ndax bëgguloo am kër ci béréb bu mel nii ?
Yàlla dafa bëgg nga dund ba fàww ci àjjana ci kow suuf. Te bëggul mukk nga am benn ci metit yi nit ñi am tey. Lii la Biibël bi wax ci ñiy dund ci àjjana ju bees ji : ‘ Yàlla dina nekk ak ñoom. Dee dootul am walla jooy walla metit. Li amoon bu jëkk, amatul. ’
Yeesu mooy def lépp ba lu rafet loolu am. Ndax xam nga loolu, kañ lay doon ? Dina def loolu bu dindee ba pare lépp lu bon ak nit ñu bon ñépp ci kow suuf. Yaa ngi fàttaliku ne, bi Yeesu nekkee ci kow suuf, faj na bépp fasoŋu feebar, dekkal na sax ñu deewoon. Yeesu dafa def loolu ngir wone li muy def ci kow suuf si sépp, bés bu nguuroo ci nguuru Yàlla.
Xalaatal ni dund gi di neexe ci àjjana ju bees ji ci kow suuf si ! Yeesu dina nguuru ca asamaan ak ñi mu tànn. Dinañu toppatoo képp ku nekk ci suuf si te fexe ba ñépp dëkk ci jàmm. Nañu seet li ñu war a def bu ñu bëggee Yàlla may ñu dund gu dul jeex ci àjjanaam ju bees.