NETTALI 114
Lépp Lu Bon Dina Jeex
LAN ngay gis fii ? Ay xarekat yu war fas yu weex. Waaye xoolal fu ñu jóge. Ñu ngi daw, jóge asamaan, wàcc ci niir yi ! Waaye ndax am na fas ca asamaan ?
Déedéet, ndaxte fas mënul a daw ci kow niir, du dëgg ? Waaye Biibël bi wax na ci ay fas yu nekk ca asamaan. Xam nga lu tax ?
Dafay wax loolu ndaxte amoon na jamano joo xam ne, bu nit ñi doon xeex, dañu doon war ay fas. Kon bu Biibël bi waxee ne am na ñuy wàcc asamaan di war ay fas, dafa bëgg a wone ne Yàlla dafa am xeex bu muy def ak nit ñi ci kow suuf. Ndax xam nga xeex boobu, fan lay ame ? Ci béréb bu ñuy woowe Armagedon. Ci xeex boobu, Yàlla dina dindi lépp lu bon li am ci kow suuf si.
Yeesu mooy kiy jiite xeex boobu ci Armagedon. Bul fàtte ne Yeesu la Yexowa tànn ngir mu nekk buur ci Nguuram. Loolu moo tax Yeesu sol ci boppam mbaxane yu buur yi di sol. Te jaasi bi mu yor mooy wone ne dina rey ñi bañ Yàlla ñépp. Bu ñu déggee ne Yexowa dafa bëgg a alag ñu bon ñépp, ndax loolu war na ñu jaaxal ?
Delluwaatal ci nettali 10. Looy gis foofu ? Waaw, mooy taw bu metti boobu reyoon nit ñu bon ñi. Ku defoon loolu ? Yàlla mi tudd Yexowa la. Léegi xoolal nettali 15. Lu xew foofu ? Yexowa alag na Sodom ak Gomor ak safara si mu wàcce seen kow.
Demal léegi ci nettali 33. Xoolal liy dal fas yi ak sareet yi waa Misra defar pur xeex. Kan moo def ba ndox mi wàcc seen kow ? Yexowa la. Def na loolu ngir aar mbooloom. Xoolal nettali 76. Dinga gis foofu ne Yexowa bàyyi na sax ñu alag mbooloom, waa Israyil, ndax lu bon li ñu doon def.
Kon, bu ñu gisee Yexowa di yónni xarekat yi mu am ci asamaan ngir dindi lépp lu bon ci kow suuf, war nañu xam ne loolu mooy yoon. Waaye xalaatal ci loolu lépp, lu muy indi. Jàngal nettali biy topp, dinga xam loolu..