Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 116

Li Ñu War A Def Ngir Mën A Dund Ba Fàww

Li Ñu War A Def Ngir Mën A Dund Ba Fàww

NDAX mën nga wax lan la xale bu jigéen bi ak xaritam yi di jàng ? Waaw, mooy téere bi ngay jàng nii, maanaam Ay nettali yu nekk ci Biibël bi. Te li ñuy jàng mooy nettali bi ngay jàng nii, maanaam “ Li ñu war a def ngir mën a dund ba fàww ”.

Xam nga lan lañuy jàng foofu ? Benn, bu ñu bëggee dund ba fàww, dañu war a xam lu jëm ci Yexowa ak Yeesu. Biibël bi nee na : ‘ Lii nga war a def ngir dund ba fàww : Jàng lu jëm ci benn Yàlla dëgg ji am kese ak ci Doom ji mu yónni ci suuf, maanaam Yeesu Kirist. ’

Lan lañu mën a def ngir jàng lu jëm ci Yexowa Yàlla ak Doomam Yeesu ? Lenn li ñu mën a def mooy jàng ba mu jeex téere Ay nettali yu nekk ci Biibël bi. Dañu ci wax lu bare lu jëm ci Yexowa ak Yeesu, du dëgg ? Dañu ci wax itam lu bare ci li Yexowa ak Yeesu def ba pare ak it ci li ñuy def ëllëg. Waaye waruñu yem ci jàng téere bii rekk.

Ndax gis nga beneen téere bi nekk ci suuf ? Biibël bi la. Fexeel ba am ku lay jàngal ci Biibël bi fi ñu jële nettali yi nekk ci téere bii. Biibël bi wax na lépp li ñu soxla ngir jaamu Yexowa ni mu ware te am dund gu dul jeex. Kon dañu war a faral di gëstu Biibël bi.

Waaye yem ci jàng lu jëm ci Yexowa Yàlla ak Yeesu Kirist, doyul. Mën nañu xam lu baree bare ci ñoom ak ci li ñuy jàngale, te ba tey bañ a am dund gu dul jeex. Ndax xam nga leneen li ñu war a def ?

Leneen loolu mooy topp li ñuy jàng. Ndax yaa ngi fàttaliku Yudaa Iskariyo ? Bokkoon na ci 12 taalibe yi Yeesu tànnoon ngir ñu nekk ay ndawam. Yudaa xamoon na lu bare ci Yexowa ak Yeesu. Waaye lan la def ? Bi mu yàggee tuuti, dafa komaasee bëgg boppam rekk te jébbal na Yeesu noonam yi pur 30 xànjaru xaalis. Kon Yudaa du am dund gu dul jeex.

Ndax yaa ngi fàttaliku Geyasi mi ñu doon wax ci nettali 69 ? Dafa bëggoon a am yére ak xaalis yu mu moomul woon. Mu fen ngir am leen. Yexowa yar na ko ndax loolu. Ñun it, bu ñu toppul li ñu Yexowa digal, Yexowa dina ñu yar.

Waaye am na nit ñu bare ñu topp Yexowa bu baax ci seen dund yépp. Dañu bëgg mel ni ñoom, du dëgg ? Xoolal Samwil bi mu nekkee xale. Ku jar a roy la. Gisoon nañu ci nettali 55 ne ñeent mbaa juróomi at rekk la amoon bi mu komaasee jaamu Yexowa ci tànt fi ñu doon jaamu Yàlla. Kon, ak li nga mën a nekk ndaw yépp, mën nga jaamu Yexowa.

Waaye ki ñépp bëgg a topp mooy Yeesu Kirist. Bi mu nekkee xale bu ndaw, mu nga woon ci kër Yàlla gi di wax ak nit ñi lu jëm ci Baayam bi nekk asamaan. Loolu lañu gisoon ci nettali 87. Nañu ko roy. Nañu def lépp ngir wax ak nit ñu bare ci suñu Yàlla Yexowa mi baax lool ak itam ci Doomam Yeesu Kirist. Bu ñu defee loolu, dinañu mën a dund ba fàww ci àjjana ju bees ji Yàlla di indi ci kow suuf si.