Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 10

Yan barke la ñiy dégg li Yàlla wax nar a am ?

Yan barke la ñiy dégg li Yàlla wax nar a am ?

Ñi gën a bare ci ñi dee dinañu dekki. Jëf ya 24:15

Xalaatleen ci barke yi ngeen nar a am bu fekkee ne yéena ngi dégg li Yexowa wax! Feebar dootul am. Lafañ itam dootul am. Dingeen am wér-gi-yaram gu mat sëkk. Nit ku bon dootul am. Kenn ku nekk dinga mën a wóolu sa moroom.

Naqar, metit walla jooy dootul am. Kenn dootul màggat, kenn dootul dee.

Dingeen nekk ak seeni xarit ak seen njaboot. Dund bi dina neex lool ci àjjana bi nar a am ci kaw suuf si.

Kenn dootul am looy ragal. Jàmm dëgg mooy am ci kaw suuf si.

Nguuru Yàlla dina fi dindi bépp naqar ak coono. Peeñu ma 21:3, 4