Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 9

Kañ la suuf si di nekkaat àjjana ?

Kañ la suuf si di nekkaat àjjana ?

Xew-xew yooyu yépp dañuy wone ne, léegi Nguuru Yàlla def dara. Luug 21:10, 11 ; 2 Timote 3:1-5

Lu bare ci liy xew tey, Biibël bi waxoon na ne dina am. Nee woon na ne nit ñi dinañu fonk xaalis, dinañu xëtt ndigalu waajur, ñu soxor lañuy doon, te di topp seen bànneex.

Dina am ay yengu-yengu suuf yu réy, ay geer, ay xiif ak ay feebar yu bare. Loolu yépp ñu ngi koy gis tey.

Yeesu waxoon na itam ne xebaar bu baax bi ci Nguuru Yàlla, dinañu ko yégle ci àddina sépp.— Macë 24:14.

Nguuru Yàlla dina fi jële lépp lu bon. 2 Piyeer 3:13

Du yàggati dara, Yexowa dina alag nit ñu bon ñi.

Yàlla dina fi jële Seytaane ak malaaka yu bon yi.

Ñiy dégg li Yàlla wax dinañu mucc, te dinañu dund ci jamano bu bees boo xam ne njubte rekk mooy am. Kenn dootul am looy ragal. Kenn ku nekk dinga mën a wóolu sa moroom te bëgg ko.