Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 4

Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?

Ndegam Aadama ak Awa dañu déglu Seytaane — loolu lan la jur ?

Aadama ak Awa déggaluñu Yàlla, loolu moo tax ñu dee. Njàlbéen ga 3:6, 23

Awa déglu na jaan bi, lekk na ci doomu garab bi, daldi jox Aadama moom itam mu  lekk.

Li ñu def baaxul — bàkkaar la. Moo tax Yàlla dàq leen ci toolu Eden ba.

Dund bi metti woon na ci ñoom ak ci seeni doom. Dem nañu ba màggat, te dee nañu. Bi ñu deewee, demuñu kaw asamaan di fa dund, nekkatuñu woon fenn di dund.

Ñi dee dañuy dellu nekk suuf, dundatuñu feneen. Njàlbéen ga 3:19

Nit ñi dañuy dee ndaxte dañu donn bàkkaar bi Aadama ak Awa def. Ñi dee mënuñu gis, mënuñu dégg, mënuñu def dara. — Ecclésiaste 9:5, 10.

Yexowa bëggul woon nit ñi di dee. Du yàggati dara, Yàlla dina dekkal ñi dee. Ñooñu dekki, su ñu déggee li Yàlla wax, dinañu dund ba fàww ci kaw suuf si.