Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 3

Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?

Naka la dund bi meloon ci toolu Eden ba ?

Yexowa mayoon na Aadama ak Awa ay yëf yu neex te baree-bare. Njàlbéen ga 1:28

Yexowa sàkkoon na Awa, di jigéen bu njëkk ba, ngir mu nekk jabaru Aadama. — Njàlbéen ga 2:21, 22.

Bi leen Yexowa sàkkee, ay nit yu mat lañu woon, amuñu woon benn sikk ci seen yaram ak seen xel.

Ci toolu Eden lañu nekkoon. Béréb bu rafet la woon ci kaw suuf si. Amoon na ay dex, ay garab, ay doomu garab, ak ay mala.

Yexowa dafa doon wax ak ñoom, di leen jàngal. Bu ñu déggoon bu baax li mu leen doon wax, dinañu dund ba fàww ci kaw suuf si.

Yàlla tere woon na ñu lekk ci benn doomu garab. Njàlbéen ga 2:16, 17

Yexowa tere woon na Aadama ak Awa ñu lekk ci benn doomu garab bu nekkoon ci toolu Eden. Waxoon na leen ne bés bu ñu ko lekkee, dinañu dee.

Kenn ci malaaka yi Yàlla sàkkoon dafa fippu. Malaaka bu bon boobu mooy Ibliis Seytaane.

Seytaane bëggul woon Aadama ak Awa  déggal Yexowa. Dafa jaar ci benn  jaan ngir gëmloo Awa ne, bu lekkee ci doomu garab bi, du dee, te dina mel ni Yàlla. Li wóor mooy li Seytaane wax ay fen la woon. — Njàlbéen ga 3:1-5.