XAAJ 12
Lan ngeen mën a def ngir am jàmm ci seen biir njaboot ?
Mbëggeel mooy tax jàmm am ci biir njaboot gi. Efes 5:33
Yàlla dafa santaane bu séy naree am, na nekk benn góor ak benn jigéen.
Góor gu bëgg jabaram dafa ko war a fonk te di ko muñal.
Jigéen dafa war a jàpple jëkkëram.
Xale yi war nañu déggal seeni waajur.
Kolos 3:5, 8-10
Nangeen baax te bañ a soxor. Nangeen yem ci seen néegu séy.Kàddu Yàlla nee na góor dafa war a bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam. Jigéen itam dafa war a weg jëkkëram.
Njaaloo baaxul. Kenn warul ànd ak koo séyalul. Te it, am jabar yu bare baaxul.
Kàddu Yexowa dafay jàngal njaboot yi ñu xam li ñu mën a def ba am jàmm ci seen biir.