Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 1

Naka lañu mën a dégge li Yàlla wax ?

Naka lañu mën a dégge li Yàlla wax ?

Yàlla ci Biibël bi lay jaar ngir wax ak ñun. 2 Timote 3:​16

Yàlla xiir na ay nit ñu bind ay xalaatam ci benn téere. Téere boobu mooy Biibël bi. Yàlla bëgg na ngeen xam xalaat yu am solo yooyu nekk ci biir.

Yàlla moo xam li gën ci ñun, te moom rekk moo ñu mën a may xam-xam dëgg. Loolu moo tax, bu ngeen déggee li Yàlla wax, dingeen nekk ay nit ñu am xel dëgg. — Léeb yi 1:5.

Yàlla dafa bëgg nit ku nekk jàng Biibël bi. Fi mu tollu nii, Biibël bi am na ci ay làkk yu bare.

Bu ngeen bëggee dégg li Yàlla wax, fàww ngeen jàng Biibël bi te xam li muy wax.

Ci biir àddina si sépp, ay nit ñu ngi dégg li Yàlla wax. Macë 28:19

Seede Yexowa yi mën nañu leen a dimbali ngeen xam li Biibël bi di wax.

Fépp ci àddina si, Seede Yexowa yi ñu ngi jàngale dëgg gi jëm ci Yàlla.

Bu ñu leen di jàngal dëgg googu, dooleen fey dara. Mën ngeen itam jàng lu jëm ci Yàlla ci Saalu Nguur gi leen gën a jege..