Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 11

Ndax Yexowa mu ngi dégg li ñuy wax ?

Ndax Yexowa mu ngi dégg li ñuy wax ?

Ci dëgg, Yàlla dafa ñuy déglu bu ñu koy ñaan. 1 Piyeer 3:12

Yexowa mooy “ Kiy déglu ñaan yi ”. (Sabóor 65:2, MN.) Dafa bëgg ñu koy wax li nekk ci suñu biir xol.

Yexowa rekk ngeen war a ñaan, du keneen.

Mën nañu ñaan Yàlla ci ay mbir yu bare. 1 Yowaana 5:14

Ñaanleen ngir coobare Yàlla am ci suuf si mel ni ca kaw asamaan.

Nangeen ñaan ci turu Yeesu. Loolu dafay wone ne yëg ngeen li mu leen defal, te yéena ngi koy gërëm.

Ñaanleen Yexowa mu dimbali leen ngeen mën a def lu baax. Mën ngeen a ñaan itam ci lu jëm ci wàllu lekk, liggéey, dëkkuwaay, ak li ngeen di sol ak wér-gi-yaram.