Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 10

Ni ngay soppee sa baat booy jàngale

Ni ngay soppee sa baat booy jàngale

Kàddu yu Xelu 8:4, 7

LI NGA WAR A JÀPP: Na sa wax leer te laal xolu nit ñi. Li la ciy dimbali mooy di soppi sa baat booy wax.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Yëkkëtil sa baat walla nga wàcce ko. Yëkkëtil sa baat booy wax li gën a am solo ak booy xiir nit ñi ci def dara. Defal noonu itam booy jàng aaya buy wax ci àtte Yàlla yi. Wàcceel sa baat boo bëggee ñi lay déglu yàkkamtee xam li nga nar a wax, walla boo bëggee wone ragal mbaa njàqare.

  • Waxal ak baat bu xumb walla bu lewet. Su mënee nekk ci sa làkk, waxal ak baat bu xumb ngir wone cawarte, yaatuwaay walla sorewaay. Waxal ak baat bu lewet ngir wone naqar walla njàqare.

  • Waxal mu gaaw walla mu yéex. Waxal mu gaaw ngir wone yëg-yëg bu am doole. Waxal mu yéex booy wax ci li gën a am solo.