Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 13

Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale

Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale

Kàddu yu Xelu 3:21

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu xam njariñu li ngay jàngale te won leen ni ñu ko mën a jëfe.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xalaatal ñi la nar a déglu. Xalaatal bu baax ci li tax nit ñi war a xam li nga leen bëgg a jàngal, te seetal ci sa waxtaan lan moo leen di gën a amal njariñ.

  • Ci sa waxtaan bi yépp, wonal ñi lay déglu li ñu war a def. Booy komaase, ak ci waxtaan bi yépp, képp kuy déglu war na mën a wax ne: «Lii, dina ma amal njariñ». Booy wax ci ponk bu am solo bu nekk, woneel ni ñu ko mën a jëfe. Na njariñu li ngay wax leer bu baax.