Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 15

Woneel ne gëm nga li ngay wax

Woneel ne gëm nga li ngay wax

1 Tesalonig 1:5

LI NGA WAR A JÀPP: Woneel ne gëm nga bu baax ne li ngay wax dëgg la te am na solo.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Waajalal sa bopp bu baax. Xoolal bu baax li nga nar a waxtaane te mu jóge ci Biibel bi. Seetal li tax li ñu ci wax leer ba nit mën koo gëm. Jéemal a wax ponk yi gën a am solo ci kàddu yu gàtt te yomb a xam. Xalaatal bu baax ci njariñ bi li ngay wax mën a amal ñi lay déglu. Ñaanal Yàlla mu may la xel mu sell mi.

  • Waxal ay baat yuy wone ne gëm nga li ngay wax. Bul yem rekk ci jàng li ñu bind, waaye wax ko ak say kàddu bopp. Woneel ci say kàddu ne li ngay wax, wóor na la.

  • Ni ngay waxe, na wone ne ku dëggu nga. Waxal bu baax ba ñépp mën laa dégg. Nanga xool ñi lay déglu, waaye na ànd ak yar.