Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 18

Defal waxtaan buy yokk xam-xam

Defal waxtaan buy yokk xam-xam

1 Korent 9:19-23

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat bu baax ci li ngay wax. Noonu, bu waxtaan bi jeexee dinañu xam ne jàng nañu lu am njariñ.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xalaatal ci li nit ñi xam ba pare. Bul waxaat rekk li nit ñi xam ba pare, waaye dimbali leen ñu jàng ci waxtaan bi lu bees.

  • Gëstul te xalaat bu baax ci li nga nar a waxtaane. Bu mënee nekk, waxal ci xew-xew yu ñu bare yëgul walla yu xew tey ngir leeral ponk yi gën a am solo. Te it, seetal bu baax ni loolu ànde ak li nga bëgg a waxtaane.

  • Woneel njariñ bi sa waxtaan mën a amal ñi lay déglu. Woneel njariñ bi nekk ci topp bés bu nekk li Biibël bi wax. Woneel njariñ boobu ci ay fànn, doxalin walla jëf yu nit ñi xam.