NJÀNGALE 21
Lan mooy Betel ?
Betel, tur la ci làkku yawut. Mu ngi tekki “ kër Yàlla ” (Njàlbéen ga 28:17, 19). Tur boobu la seede Yexowa yi di woowe palaas yi ñu am ci àddina si te ñu fay jiitee liggéeyu waare bi ak di jàpple ñi ciy yëngu. Kër gu mag gi, mu nga New York ca Etaa Sini. Foofu la Jataay biy dogal nekk te di fa jiitee liggéey bi ñuy def ci suñu bànqaas yi ci àddina si sépp. Ñi nekk Betel dañu mel ni njaboot ndaxte ci Betel bi lañu dëkk, di bokk lekk te di bokk jàng Biibël bi. Loolu moo tax ñu leen di woowe njabootu Betel bi. — Sabóor 133:1.
Béréb la fu ay mbokk nangoo sonn ngir def liggéeyu Yàlla. Ci Betel yi yépp am na ay karceen yu góor ak yu jigéen yuy joxe seen jot gépp ngir def li Yàlla bëgg te liggéeyal Nguuram (Macë 6:33). Amu ci kenn ku ciy feyeeku waaye ñépp lañuy jox néeg bu ñuy fanaan ak lekk ak tuuti ndimbal ngir ñu faj seeni soxla yu ndaw. Ku ci nekk am nga liggéey bu ñu la dénk, muy ci biro yi, walla ci waañ bi, walla ci saal bi ñuy lekke, walla fi ñuy sottee suñu téere yi. Mën na nekk it menaas, fóot, defar yàqu-yàqu yi, ak yeneen.
Béréb la fu ñuy jàpple liggéeyu waare xibaaru Nguur gi. Li gën a tax ñu taxawal Betel yi mooy def ba nit ñu bare xam dëgg gi nekk ci Biibël bi. Téere bii nga yor, ci la bokk. Bi ñu koy bind, Jataay biy dogal moo jiite liggéey bi. Bi ñu paree, dañu ko yónnee ci internet ay téeméeri gurupu seede Yexowa yuy tekki suñuy téere ci ay làkk yu bare ci àddina si sépp. Bi ñu paree, ñu sotti ko ci ay masin yu gaaw yu nekk ci yenn Betel yi, door ko yónnee ci lu ëpp 110 000 mbooloo. Ci liggéey boobu yépp nag, njabootu Betel yi am nañu ci wàll bu am solo. Bu ñuy def loolu, dañuy jàpple liggéey bi gën a jamp tey, maanaam waare xibaaru jàmm bi. — Màrk 13:10.
-
Ñan ñooy liggéey ci Betel yi te naka lañu leen di toppatoowe foofu ?
-
Ban liggéey bu jamp la Betel bu nekk di jàpple ?