Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 11

Ni nga mënee jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi

Ni nga mënee jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi

Ndax mas ngaa pare ngir def benn liggéey bu réy, ba pare gis ne dina la ëpp loxo? Ngir yombal liggéey bi, xéyna dinga ko xaaj, def ko benn benn. Loolu itam mën na la dal, boo bëggee komaase liir Biibël bi. Xéyna dinga laaj sa bopp lii, ‘Naka laa koy defe?’ Ci lesoŋ bii, dinañu gis lu yomb lu la mën a dimbali ba liir Biibël bi ak gëstu ko, neex ci yow.

1. Lu tax ñu war di liir Biibël bi bés bu nekk?

Nit kiy liir Biibël bi, maanaam «yoonu Aji Sax ji» bés bu nekk, dina bég te lu mu def mu àntu (Jàngal Sabóor 1:1-3). Mën nga tàmbalee ci liir tuuti, bés bu nekk. Looy gën di xam Kàddu Yàlla, liir Biibël bi di la gën a neex.

2. Lan moo lay dimbali nga jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi?

Boo bëggee jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi, fàww ngay taxaw te xalaat ci li ngay liir. Bu ñu koy liir, dañu war di ci xalaat bu baax (Yosuwe 1:8). Booy liir Biibël bi, laajal sa bopp laaj yii: ‘Lii, lan la may jàngal ci Yexowa Yàlla? Naka laa ko mën a jëfe ci sama dund? Naka laa mën a jëfandikoo aaya yii ngir dimbali nit ñi?’

3. Naka nga mënee jël jot ngir liir Biibël bi?

Ndax am jot ngir liir Biibël bi, jafe na ci yow? Yombul ci ñu bare. Jéemal a «jariñoo jot gi» (Efes 5:16). Ni nga ko mën a defe mooy, nga tànn waxtu bi ngay liir Biibël bi bés bu nekk. Am na ñi tànn di ko liir suba teel. Ñenn ñi tànn bëccëg bi, xéyna ci waxtu bi ñuy noppalu. Am na it ñiy liir Biibël bi guddi bala ñuy tëdd. Ban waxtu moo gën ci yow?

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni ngay def ba liir Biibël bi gën a neex ci yow. Xoolal ni ngay waajale sa bopp bu baax, ngir sa njàngum Biibël bi gën laa amal njariñ.

Ni ñuy jànge bëgg lekk yu wuute, noonu itam, mën nañoo def ba liir Biibël bi neex ñu

4. Ni ngay def ba liir Biibël bi neex ci yow

Komaase liir Biibël bi, mën na bañ a yomb. Waaye mën nañu dem ba mu neex ñu. Dafa mel ni kuy door a mos lekk bu mu xamul, waaye dem ba bëgg ko. Jàngal 1 Piyeer 2:2. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ndax foog nga ne booy liir Biibël bi bés bu nekk, mën na dem ba mu neex la, ba nga yàkkamti sax def ko?

Seetaanal WIDEO BI te xool ni ñenn ñi def ba liir Biibël bi tàmbali leen a neex.

  • Ci wideo bi, yan jafe-jafe la ndaw yi amoon?

  • Lan moo leen dimbali ñu kontine di liir Biibël bi bés bu nekk?

  • Naka lañu def ba liir Biibël bi gën leen a neex?

Ay xelal yu la mën a dimbali nga tàmbali:

  • Tànnal tekki Biibël bu wóor te neex a nànd. Jéemal a jàng Traduction du monde nouveau bu amee ci sa làkk, walla ci làkk boo xam bu baax.

  • Tàmbalil njàng mi ak téere yi la gën a neex ci Biibël bi. Mën nga xool tabló bi tudd «Mën nga tàmbali jàng Biibël bi bés bu nekk».

  • Bindal fi nga yem ci njàng mi. Jëfandikool tabló bi nekk ci téere bii te tudd «Bindal fi nga yem ci liir Biibël bi».

  • Jëfandikool application JW Library®. Mën nga ci liir Biibël bi te déglu ko, foo mënta nekk, muy ci sa telefon walla ci beneen jumtukaay bu ni mel.

  • Jëfandikool Téere bu ñuy dimbali ci gëstu Kàddu Yàlla. Am na foofu ay kàrt ak ay tabló yu mën a neexal njàng mi.

5. Waajalal sa njàngum Biibël bi

Jàngal Sabóor 119:34. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo tax mu baax nga ñaan Yàlla bala ngay liir Biibël bi walla bala ngay waajal sa njàngum Biibël bi?

Naka nga mënee jariñoo bu baax sa njàngum Biibël bi? Booy waajal benn lesoŋ, jéemal a def lii di topp:

  1. Liiral li nekk ci paas bi njëkk ci lesoŋ bi.

  2. Seetal aaya yi te jàng leen, jéemal a xam ni aaya yi lëkkaloo ak li nga jàng ci lesoŋ bi.

  3. Rëddal baat yi gën a fës te di tontu ci laaj yi; loolu dina la dimbali ci sa waxtaan ak ki lay jàngal.

Ndax xamoon nga ne...

Seede Yexowa yi dañu doon jëfandikoo ay sotti Biibël yu bare. Waaye sotti bi ñu ci gën a neex mooy La Bible. Traduction du monde nouveau ndaxte sotti bu wóor la, leer te turu Yàlla feeñ na ci. Xoolal waxtaan bi nekk ci jw.org te tudd «Ndax Seede Yexowa yi dañu am seen Biibëlu bopp?»

BU LA NIT WAXOON: «Jàng Biibël bi dafa laaj jot gu bari, te man amuma jot, damay sonn.»

  • Loo xalaat ci loolu?

NAÑU TËNK

Boo bëggee jariñoo bu baax Biibël bi, danga war a jël jot ngir liir ko, ñaan Yàlla mu dimbali la nga nànd li ngay liir, te waajal sa njàngum Biibël bi.

Nañu fàttaliku

  • Lan moo lay dimbali nga jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi?

  • Ban waxtu nga bëgg a tànn ngir jàng Biibël bi yow kese?

  • Lan moo tax mu baax nga waajal sa njàngum Biibël bi?

Jubluwaay

GËSTUL

Ñu yàgg a liir Biibël bi joxe nañu ay xelal, xoolal seeni xelal.

Ni nga mënee jàng bu baax Biibël bi (2:06)