Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 14

Naka la Yàlla bëgge ñu jaamu ko?

Naka la Yàlla bëgge ñu jaamu ko?

Ni ñu ko gise woon ci lesoŋ bi jàll, Yàlla nanguwul diine yi yépp. Waaye terewul mën nañu jaamu suñu Boroom ci fasoŋ bu ko neex. Ban ‘diine [walla njaamu]’ moo neex Yàlla? (Saag 1:27). Xoolal li Biibël bi wax ci loolu.

1. Ni ñuy jaamoo Yàlla, ci lan la war a sukkandiku?

Ni ñuy jaamoo Yàlla dafa war a sukkandiku ci Biibël bi. Yeesu lii la waxoon Yàlla: «Sa kàddu mooy dëgg» (Yowaana 17:17). Am na diine yoo xam ne toppuñu li nekk ci Kàddu Yàlla, Biibël bi. Ay njàngale ak ay aada yu jóge ci nit lañuy topp. Waaye Yexowa kontaanul ci nit ñiy «tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada» (Jàngal Màrk 7:9). Bu ñuy topp xelal yi nekk ci Biibël bi nag, dinañu bégal xolam.

2. Naka lañu war a jaamoo Yexowa?

Yexowa rekk lañu war a jaamu ndaxte moo ñu sàkk (Peeñu 4:11). Loolu mooy, dañu war a bëgg Yàlla te jaamu ko moom kese. Waruñu ko bokkaale ak dara, muy nataal, xërëm, walla leneen (Jàngal Esayi 42:8).

Ni ñuy jaamoo Yexowa dafa war a «sell te neex ko» (Room 12:1). Loolu mooy, dañu war a topp ay santaaneem. Kon nag ñi bëgg Yexowa, dañuy topp li mu santaane ci wàllu séy. Dañuy moytu itam jëf yuy lore, yu ci mel ni tux, jël dorog, walla naan ba màndi. a

3. Lu tax ñu war di booloo ngir jaamu Yexowa?

Ci suñu ndaje yi ñuy amal semen bu nekk, mën nañu ‘màggal Yexowa ci biir ñi bokk jataay’ (Sabóor 111:1, 2). Benn ci anam bi ñu koy defe mooy, woy ngir màggal Yàlla (Jàngal Sabóor 104:33). Yexowa dafa ñu sant ñuy teewe ndaje yi ndaxte dafa ñu bëgg te dafa xam ne, ndaje yi dinañu ñu dimbali ñu am dund gu dul jeex. Ci ndaje yi, dañuy xiirtalante ci ngëm.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li tax Yexowa nanguwul ñuy jëfandikoo ay nataal bu ñu koy jaamu. Xoolal it, ni ñu mënee màggal Yàlla.

4. Waruñu jëfandikoo ay nataal ngir jaamu Yàlla

Naka lañu xame ne, def loolu du neex Yàlla? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci jamono ji ñu doon bind Biibël bi, lan moo xew bi ay jaamu Yàlla jéeme jaamu Yàlla ak ay xërëm?

Am na ñu foog ne bu ñuy jëfandikoo ay nataal, dañuy gën a jege Yàlla. Waaye ndax loolu du tax Yàlla sori leen? Jàngal Mucc ga 20:4-6 ak Sabóor 106:35, 36. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Yan yëf walla yan nataal ngay gis nit ñi di jëfandikoo ngir jaamu Yàlla?

  • Naka la Yexowa gise ñiy jëfandikoo ay nataal?

  • Lan nga xalaat ci jëfandikoo ay nataal ngir jaamu Yàlla?

5. Jaamu Yexowa rekk moo ñuy muccal ci njàngale yi dul dëgg

Xoolal ni ñuy mucce ci njàngale yi dul dëgg bu ñuy jaamu Yexowa ni mu ko bëgge. Seetaanal WIDEO BI.

Jàngal Sabóor 91:14. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la ñu Yexowa dig, bu ñu koy jaamu moom rekk ngir wone suñu mbëggeel ci moom?

6. Dañuy jaamu Yàlla ci ndaje yi ci biir mbooloo mi

Bu ñuy woy ci ndaje yi ak di bokk ci waxtaan yi, dañuy màggal Yexowa te xiirtalante ci ngëm. Jàngal Sabóor 22:23. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax dangay kontaan boo déggee ñeneen ñi di joxe ay tontu ci ndaje yi?

  • Ndax bëgg nga waajal benn tontu?

7. Bu ñuy wax ñeneen ñi li ñu jàng Yexowa dafa ciy bég

Ñun ñépp mën nañu wax ñeneen ñi li ñu jàng ci Biibël bi. Jàngal Sabóor 9:2 ak 34:2. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ndax am na loo jàng ci Biibël bi, te nga bëgg koo xamal keneen?

BU LA NIT WAXOON: «Mën nga bokk ci diine bu la neex, li am solo rekk mooy nga dëggu ci.»

  • Loo xalaat ci loolu?

NAÑU TËNK

Bu ñu bëggee neex suñu Boroom, fàww ñu jaamu ko moom rekk, di booloo ngir màggal ko ak di xamal ñeneen ñi li ñu jàng.

Nañu fàttaliku

  • Naka lañu mënee xam ni Yàlla bëgge ñu jaamu ko?

  • Lu tax Yexowa rekk lañu war a jaamu?

  • Lu tax ñu war di booloo ak ñi bëgg a neex Yàlla ngir jaamu ko?

Jubluwaay

GËSTUL

Ci nettali bi tudd «Léegi nekkatuma jaamukatu xërëm,» xoolal ni benn jigéen def ba bàyyi jaamu xërëm.

«Biibël bi dafay soppi dund» (w11 1/7)

Xoolal ni benn ndaw jële njariñ ci teewe ndaje yi ci mbooloo mi bu dee sax yombul woon ci moom.

Yexowa toppatoo na ma (3:07)

Ñu bari dañu foog ne kurwaa dafa bokk ci diine karceen, waaye ndax war nañu koo jëfandikoo ngir jaamu Yàlla?

«Lu tax Seede Yexowa yi duñu jëfandikoo kurwaa ngir jaamu Yàlla?» (Ci jw.org la nekk)

a Dinañu wax ci mbir yooyu ci yeneen lesoŋ.