Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 28

Woneel sa ngërëm ci li la Yexowa ak Yeesu defal

Woneel sa ngërëm ci li la Yexowa ak Yeesu defal

Lan ngay yëg ci sa biir xol, bu la sa xarit mayee kado bu rafet? Danga ciy kontaan lool ba bëgg koo won sa ngërëm. Yexowa ak Yeesu may nañu ñu kado bi gën a réy ci kado yi. Lan mooy kado boobu, ak naka lañu mën a wonee suñu ngërëm?

1. Naka lañu mën a wonee suñu ngërëm ci li ñu Yàlla ak Kirist defal?

Biibël bi dige na ne ‘képp ku gëm Yeesu’ mën na am dund gu dul jeex (Yowaana 3:16). Naka lañuy defe loolu? Dañu war a wone ngëm ci dogal yi ñuy jël ak ci li ñuy def (Saag 2:17). Bu ñuy wone ngëm ci suñu jëf ak ci suñu wax, suñu xaritoo ak Yeesu ak Baayam, Yexowa dafay gën a dëgër (Jàngal Yowaana 14:21).

2. Ban xew-xew bu espesiyaal moo ñuy may ñu wone suñu ngërëm ci li Yexowa ak Yeesu def?

Guddi gi mujj bala muy dee, Yeesu dafa wax ay taalibeem neneen ni ñu mën a wonee seen ngërëm ci sarax si mu nar a def. Dafa taxawal xew-xew bu am solo, bu ñuy woowe ci Biibël bi «Reerub Boroom bi.» Ñu gën koo xame ci Bésu fàttaliku deewu Kirist (1 Korent 11:20). Yeesu dafa taxawal xew boobu ngir taalibeem yi ak ñépp ñiy karceen dëgg, mën a fàttaliku ne dafa joxe bakkanam ngir ñun. Lu jëm ci xew-xew boobu, lii la Yeesu santaane: «Defleen lii, ngir fàttaliku ma» (Luug 22:19). Boo teewee ci bésu fàttaliku deewu Yeesu, dangay wone sa ngërëm ci mbëggeel gu réy gi ñu Yexowa ak Yeesu won.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal neneen ni nga mën a wonee sa ngërëm ci mbëggeel gu réy gi Yexowa ak Yeesu wone. Xoolal it li tax fàttaliku deewu Kirist am solo.

3. Suñu ngërëm moo ñuy tax a jëf

Xalaatal ngay lab, nit ñëw wàllu la. Ndax dinga gaaw a fàtte li la nit kooku defal? Ndax doo seet ni nga mën a def ba won ko sa ngërëm ndax li mu la defal?

Bu ñu mënee am dund gu dul jeex, Yexowa moo tax. Jàngal 1 Yowaana 4:8-10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax saraxu Yeesu doon may bu espesiyaal?

  • Lan ngay yëg ci sa xol, boo xalaate ci li la Yexowa ak Yeesu defal?

Naka lañu mën a wonee suñu ngërëm ci li ñu Yexowa ak Yeesu defal? Jàngal 2 Korent 5:15 ak 1 Yowaana 4:11; 5:3. Boo jàngee benn aaya, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Ni ko aaya bi wonee, naka lañu mën a wonee suñu ngërëm?

4. Nañu roy ci Yeesu

Beneen fasoŋ bi ñu mën a wonee suñu ngërëm mooy roy ci Yeesu. Jàngal 1 Piyeer 2:21. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka nga mënee jaar ci tànki Yeesu?

5. Nañu teewe bésu fàttaliku deewu Kirist

Boo bëggee xam ni ñu defe woon Reeru Sàng bi njëkk, jàngal Luug 22:14, 19, 20. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka lañu defe woon Reeru Sàng bi?

  • Lan la mburu mi ak biiñ bi di misaal? (Xoolal aaya 19 ak 20).

Yeesu dafa bëggoon taalibeem yi di fàttaliku Reeru Sàng bi, benn yoon ci at mi, saa yu bésub deewam dellusee. Moo tax Seede Yexowa yi, benn yoon ci at mu nekk dañuy booloo ngir fàttaliku deewu Kirist, ni mu ko santaane woon. Ngir xam lu jëm ci ndaje bu am solo boobu, seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Naka lañu defe fàttaliku bi?

Mburu mi ak biiñ bi, dafa am li ñuy misaal. Mburu mi mooy misaal yaramu Yeesu bi mat, bi mu saraxe ngir ñun. Biiñ bi mooy misaal deretam

BU LA NIT WAXOON: «Boo gëmee Yeesu rekk dinga mucc.»

NAÑU TËNK

Bu ñu bëggee wone suñu ngërëm ci li ñu Yeesu defal, dañu ko war a gëm te di teewe bésu fàttaliku deewam.

Nañu fàttaliku

  • Naka lañuy wonee ne gëm nañu Yeesu?

  • Naka nga bëgg a wonee sa ngërëm ci li la Yexowa ak Yeesu defal?

  • Lu tax teewe bésu fàttaliku deewu Kirist am solo?

Jubluwaay

GËSTUL

Lan la ñu deewu Kirist di xiir ñu def?

Dafa màggal Yexowa ak yaramam (9:28)

Gënal a xam lu jëm ci ngëm ak ni ñu koy wonee.

«Woneel sa ngëm ci dige Yexowa yi» (w16 oktoobar)

Ci nettali bi tudd «Léegi yëg naa ne, set naa te fonk naa dund gi», xoolal ni benn jigéen soppee dundam bi mu gënee nànd bu baax saraxu Kirist bi.

«Biibël bi dafay soppi dund» (w11 1/8)