Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 43

Naka la karceen yi war a gise sàngara?

Naka la karceen yi war a gise sàngara?

Ci àddina si, ni nit ñi gisee sàngara dafa wuute. Am na ñuy naan sàngara bu ñu nekkee ak seeni xarit. Am na ñu dogal ne duñu naan mukk sàngara. Am na ñoo xam ne ñoom dañuy naan a naan ba màndi. Lan la Biibël bi wax ci sàngara?

1. Ndax naan sàngara lu bon la?

Biibël bi terewul naan sàngara. Xanaa kay dafa ko boole sax ci mayug Yàlla yi. Biibël bi dafa ne ‘biiñ dafay bégal xol’ (Sabóor 104:14, 15). Ay nit yu takku woon ci Yàlla, góor ak jigéen yu ñu tudd ci Biibël bi, dañu doon naan sàngara (1 Timote 5:23).

2. Ban xelal la Biibël bi jox ñi dogal ne dañuy naan sàngara?

Yexowa tere na naan bu bari ak naan ba màndi (Galasi 5:21). Lii la wax ci Kàddoom: «Bul bokk ci ñiy [...] màndi» (Kàddu yu Xelu 23:20). Bu ñu jëlee dogalu naan, moo xam ñuy naan ñun kese walla ñu nekk ak ñeneen, waruñu naan lu bari ba dootuñu ànd ak suñu sago, dootuñu xam li ñuy wax ak li ñuy def, walla ñuy yàq suñu wér-gi-yaram. Bu ñu mënul a yemale li ñuy naan, dañu war a nangu bàyyi naan sàngara ci boppam.

3. Naka lañu mënee wone ne nangu nañu dogal bi ñeneen jël ci wàllu sàngara?

Nit ku nekk mooy tànn ndax dina naan sàngara walla déet. Waruñu sikkal ku tànn naan sàngara ci fasoŋ bu yem te waruñu puus ku bëggul naan ngir mu naan (Room 14:10). Dañuy nangu bàyyi naan bu dee dafay jural jafe-jafe ñeneen ñi (Jàngal Room 14:21). Duñu seet ‘suñu njariñ rekk, waaye dañuy seet suñu njariñu moroom’ (Jàngal 1 Korent 10:23, 24).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal njàngale yi nekk ci Biibël bi, yi la mën a dimbali nga tànn ndax dinga naan ak fi nga war a yem boo tànnee naan. Xoolal it li nga mën a def bu dee danga am poroblem ak sàngara.

4. Tànnal ndax dinga naan walla déet

Naka la Yeesu gise woon naan sàngara? Boo bëggee gis tontu bi, xoolal kéemaan bi mu njëkk a def. Jàngal Yowaana 2:1-11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Bu ñu xoolee ci kéemaan bi mu def, lan lañu mën a jàng ci ni Yeesu gise sàngara ak ñi koy naan?

  • Ndegam Yeesu waxul ne naan sàngara baaxul, naka la karceen war a gise kiy naan sàngara?

Dëgg la ne karceen bu mu neex mën na naan sàngara, waaye gënul mu di ko def saa su nekk. Jàngal Kàddu yu Xelu 22:3. Boo paree, xoolal lii di topp ni mu la mënee dimbali nga xam ndax dinga naan walla déet:

  • Boo naree dawal walla liggéey ak masiin.

  • Bu dee danga ëmb.

  • Sa doktoor xelal la nga bàyyi naan sàngara.

  • Danga am jafe-jafe yemale li ngay naan.

  • Yoon tere naan sàngara.

  • Nga nekk ak ku bàyyi naan ndaxte dafa amoon poroblem ak sàngara.

Ndax war nga séddale sàngara ci ab céet walla ci beneen feet? Ngir gis lu la mën a dimbali nga jël dogal, seetaanal WIDEO BI.

Jàngal Room 13:13 ak 1 Korent 10:31, 32. Boo paree jàng aaya bu nekk, tontul ci laaj bii:

  • Naka la la aaya bi mënee dimbali nga jël dogal bu neex Yexowa?

Karceen bu nekk mooy tànn ndax dina naan sàngara walla déet. Bu dee sax nit ki dafay naan sàngara, yenn saay mën na tànn bañ a naan

5. Tànnal fi nga war a yem booy naan

Bu dee danga jël dogal ne dangay naan sàngara, bul fàtte lii: Yexowa terewul naan sàngara, waaye tere na naan bu bari. Lu tax? Jàngal Ose 4:11, 18. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo mën a xew bu nit naanee lu ëpp?

Naka lañu mënee moytu naan lu ëpp? War nañu xam suñu bopp, maanaam xam fi ñu mën a yem. Jàngal Kàddu yu Xelu 11:2. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax mu baax ñu jël dogal bu leer ci fi ñu war a yem bu ñuy naan?

6. Li ñu mën a dimbali ñu bàyyi naan bu ëpp

Xoolal li dimbali benn góor mu bàyyi naan sàngara bu ëpp. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci wideo bi, naka la Dmitry doon doxale bu naanee sàngara?

  • Ndax mënoon na jékki rekk bàyyi naan?

  • Naka la def ba mujjee bàyyi naan sàngara bu ëpp?

Jàngal 1 Korent 6:10, 11. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lan la Biibël bi wax ci naan ba màndi?

  • Lan mooy wone ne kuy naan lu ëpp mën na soppeeku?

Jàngal Macë 5:30. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Dagg sa loxo dafay misaal li ñu nangu ñàkk ngir neex Yexowa. Lan nga mën a def bu dee yaa ngi xeex ngir bàyyi naan sàngara bu ëpp? a

Jàngal 1 Korent 15:33. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan moo mën a xew booy ànd ak ñuy naan naan bu ëpp?

BU LA NIT LAAJOON: «Ndax naan dafa bon?»

  • Lan nga koy tontu?

NAÑU TËNK

Yexowa dafa ñu may sàngara ngir suñu mbégte, waaye tere na naan bu ëpp ak naan ba màndi.

Nañu fàttaliku

  • Lan la Biibël bi wax ci sàngara?

  • Naan bu ëpp, yan loraange la mën a jur?

  • Naka lañu mënee wone ne, nangu nañu dogalu ñeneen ñi ci wàllu naan?

Jubluwaay

GËSTUL

Naka la ndaw ñi mënee jël dogal bu baax ci wàllu sàngara?

Xalaatal ci li la naan sàngara mën a jural (2:31)

Xoolal li nga mën a def boo amee poroblem ak sàngara.

«Bul-leen ëppal ci naan sàngara» (w10 1/1)

Ndax karceen mën na bokk ci ñiy yëkkati kaas bala ñuy naan?

«Ay laaj yu jóge ci ñiy jàng suñuy téere» (w07 15/2)

a Yenn màndikat yi soxla nañu ndimbalu doktoor ngir bàyyi. Doktoor yu bari wax nañu ne, ñi am poroblem ak naan sàngara, dañu war a bàyyi sàngara ci boppam.