Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 48

Tànnal bu baax say xarit

Tànnal bu baax say xarit

Xarit yu ñu jege dañuy yokk suñu mbégte te bu ñu nekkee ci naqar, ñu dooleel ñu. Waaye Biibël bi wax na ñu ne, du ñépp ñooy xarit yu baax. Kon naka nga mënee tànn ay xarit yu baax? Xoolal laaj yii di topp.

1. Xarit yi ngay tànn, lan lañu mën a def ci yow?

Bu ñuy faral di ànd ak nit, bu yàggee mën nañu mel ni moom. Ànd boobu mën na baax ci ñun walla mu bon ci ñun, moo xam ñuy nekk ak nit ki walla ñuy nekk ak moom ci internet. Ni ko Biibël bi waxe, «àndal ak ku xelu, sam xel rafet; ku lëngook ub dof [maanaam ku bëggul Yexowa], loru» (Kàddu yu Xelu 13:20). Xarit yu bëgg Yexowa te di ko jaamu, mën nañu la dimbali nga wéy di ko jege te jël ay dogal yu baax. Waaye am ay xarit yu ñu jege yu bokkul ci mbooloo mi, mën na tax ñu sore Yexowa. Loolu moo tax Biibël bi xelal ñu, ñu tànn bu baax suñuy xarit! Bu suñuy xarit bëggee Yàlla, suñu ànd dinañu amal njariñ, amal leen njariñ ñoom itam. Dinañu mën a wéy di ‘dëgëralante te yokkante ngëm’ (1 Tesalonig 5:11).

2. Xarit yi ngay tànn, lan la mën a def ci Yexowa?

Yexowa dafay tànn bu baax ay xaritam. «Aji Sax ji daa sib ku dëng, xejjoo kuy jubal» (Kàddu yu Xelu 3:32). Lan la Yexowa di yëg bu ñu tànnee ay xarit yu ko bëggul? Dina ko metti lool! (Jàngal Saag 4:4). Waaye bu ñu moytoo àndandoo yu bon te jege Yexowa ak ñi ko bëgg, Yexowa dina bég ci ñun te dina nangoo doon suñu xarit (Sabóor 15:1-4).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal li tax xarit yi ñuy tànn am solo lool ak ni nga mënee am ay xarit yu baax dëgg ci yow.

3. Moytul àndandoo yu bon

Nit ñu bëggul Yàlla ak ay santaaneem, ay àndandoo yu bon lañu. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Naka lañu mënee am àndandoo yu bon te duñu ko yëg sax?

Jàngal 1 Korent 15:33. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Kan moo mën a nekk àndandoo bu bon ci yow? Lu tax?

Jàngal Sabóor 119:63. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan lañu war a wut ci xarit?

Benn pom bu nëb mën na yàq yeneen yépp. Lan la benn àndandoo bu bon mën a def ci yow?

4. Ay nit ñu wuute ak ñun mën nañu nekk xarit yu baax

Biibël bi wax na ci Daawuda ak Yonatan, ñaari góor yu doon dund ci Israyil bu njëkk ba. Magante woon nañu lu bare te fi ñu yaroo wuute lool. Terewul ñu doon ay xarit yu mag. Jàngal 1 Samiyel 18:1. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax soxlawul suñuy xarit maase ak ñun walla ñu tolloo ak ñun am-am?

Jàngal Room 1:11, 12. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la ay xarit yu bëgg Yexowa mënee dimbalante ci seen biir?

Ci wideo bii, xoolal ni benn ndaw amee ay xarit fi mu ko foogewul woon. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lu tax waajuru Akil yi, seen xel dalul woon ndax xarit yi mu amoon ca lekkool ba?

  • Lan moo neexoon Akil ci xaritoo yooyu?

  • Naka la def ba wéetatul?

5. Ni nga mënee am ay xarit yu baax

Xoolal ni nga mënee am ay xarit dëgg ak ni nga mënee nekk yow ci sa bopp xarit bu baax. Seetaanal WIDEO BI.

Jàngal Kàddu yu Xelu 18:24 ak 27:17. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la ay xarit dëgg di dimbalantee?

  • Ndax am nga ay xarit yu baax yu mel noonu? Bu dee déedéet, naka nga mën a def ba am leen?

Jàngal Filib 2:4. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Boo bëggee am ay xarit yu baax, yow ci sa bopp war nga nekk xarit bu baax. Naka nga ko mënee nekk?

Boo bëggee am ay xarit yu baax, yow ci sa bopp war nga nekk xarit bu baax

BU LA NIT WAXOON: «Am xarit moo gën bañ a am xarit, ak ku mu mënta doon.»

  • Lan ngay wax?

NAÑU TËNK

Bu ñuy tànn bu baax suñuy xarit, Yexowa dina bég ci ñun te loolu dina doon lu baax ci ñun.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax xarit yi ñuy tànn am solo ci Yexowa?

  • Yan xarit lañu war a moytu?

  • Naka nga mënee am xaritoo bu dëgër ak ñi bëgg Yexowa?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li nga mën a def ngir am xarit yu baax.

«Naka laa mënee am xarit yu baax?» (yp1, pàcc 8)

Lan nga war a xam ci xaritoo ci internet?

Xamal bu baax li ngay def ci internet (4:12)

Ci nettali bi tudd «Soxlawoon naa lool am pàppa,» xoolal li tax benn góor xoolaat xarit yi mu tànnoon.

«Biibël bi dafay soppi dund» (w12 1/4)