Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 49

Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 1)

Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 1)

Ñaari nit ñuy door a séy, li ñu bëgg mooy mbégte bi ñu am ci seen bésu séy sax ba fàww. Te loolu lu mën a nekk la. Karceen yi yàgg ci seen séy te di def lépp ngir topp santaane yi nekk ci Biibël bi, xam nañu ne loolu lu mën a nekk la.

1. Ban xelal la Biibël bi jox jëkkër yi?

Yexowa, jëkkër la def kilifa ci biir njaboot gi (Jàngal Efes 5:23). Yexowa dafa bëgg jëkkër di jël ay dogal yu baax ngir njaboot gi. Biibël bi lii la wax jëkkër yi: «Na ku nekk bëgg soxnaam» (Efes 5:25). Loolu lu muy tekki? Jëkkër ju bëgg jabaram dafa koy won mbaax bu ñu wéetee ak bu ñu nekkee ci kanamu nit ñi. Dafa koy aar ci li ko mën a lor te def lépp ngir bégal ko te toppatoo ko (1 Timote 5:8). Te li gën am solo, dafay dimbali jabaram mu am diggante bu rattax ak Yexowa (Macë 4:4). Mën na di ñaan Yàlla ak moom te di jàng Biibël bi ak moom. Bu jëkkër di toppatoo bu baax jabaram, dina wéy di am diggante bu rattax ak Yexowa (Jàngal 1 Piyeer 3:7).

2. Ban xelal la Biibël bi jox jabar yi?

Kàddu Yàlla nee na, jabar dafa war a «weg jëkkëram» (Efes 5:33). Naka la mënee def loolu? Mën na xalaat ci jikko yu baax yi jëkkëram am ak ni muy góor-góorloo ngir toppatoo ko moom ak xale yi. Ngir won jëkkëram ne weg na ko, dafa koy jàppale ci dogal yi mu jël ba pare. Di wax ak moom wax ju neex te di wax ci moom lu baax, bu dee sax nekkul jaamu Yexowa.

3. Naka la jëkkër ak jabar mënee dëgëral seen séy?

Biibël bi nee na bu góor ak jigéen séyee, ‘ñoom ñaar dañuy doon benn’ (Macë 19:5). Loolu dafa tekki ne, dañu war a xeex lépp lu mën a wàññi seen mbëggeel. Ni ñu mënee def loolu mooy, di faral di nekk ñoom ñaar. Ku nekk ubbil sa moroom bu baax sa xol, di ko wax li ngay yëg ak li ngay xalaat, te ànd ci ak mbëggeel. Bu dul Yexowa, duñu bàyyi kenn walla dara gën leen a amal solo seen jëkkër walla seen jabar. Dañuy moytu bu baax ngir bañ a xaritoo, xaritoo bu jege ba ëpp ak keneen.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni njàngale yi nekk ci Biibël bi mënee dëgëral sa séy.

4. Yeen jëkkër yi, bëggleen seen jabar te di ko toppatoo

Biibël bi nee na, «na góor bëgg soxnaam, ni mu bëgge boppam» (Efes 5:28, 29). Lan la loolu tekki? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.

  • Ci yan fànn la jëkkër mënee wone ne, bëgg na jabaram te dafa koy toppatoo?

Jàngal Kolos 3:12. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la jëkkër mënee wone jikko yii ci digganteem ak jabaram?

5. Yeen jabar yi, bëggleen seen jëkkër te weg ko

Biibël bi dafa wax jabar yi ñu weg seen jëkkër, moo xam mu doon jaamu Yexowa walla déet. Jàngal 1 Piyeer 3:1, 2. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Bu dee sa jëkkër nekkul jaamu Yexowa, li wóor mooy bëgg nga bés mu nekk ko. Ci sa xalaat naka nga ko mën a dimbalee? Nga di ko waar saa su nekk walla nga am doxalin bu rafet te weg ko? Lu tax?

Bu jëkkër ak jabar àndee jël dogal ñoom ñaar, loolu lu baax la. Waaye lée-lée jabar ji mën a bañ a ànd ci li jëkkër ji dogal. Bu loolu amee, mën na wax xalaatam, ànd ci ak dal ak respe. Waaye war na nangu ne, jëkkëram la Yexowa jox wareefu dogal li gën ci njaboot gi. Dafa war a def lépp ngir jàppale ko ci dogal bi mu jël. Buy def loolu, dina yokk jàmm ji am ci njaboot gi. Jàngal 1 Piyeer 3:3-5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lan la Yexowa di yëg bu gisee jabar ju weg jëkkëram?

6. Li ngeen mën a def bu ngeen amee jafe-jafe ci seen biir séy

Benn séy matul. Kon ñaar ñiy séy war nañu ànd xeex poroblem yi. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Ci wideo bi, lan moo wone ne jëkkër ji ak jabar ji, seen diggante demeetul woon noonu?

  • Lan lañu def ngir gën a dëgëral seen séy?

Jàngal 1 Korent 10:24 ak Kolos 3:13. Boo paree jàng aaya bu ci nekk, tontul ci laaj bii di topp:

  • Naka la topp xelal bii mënee gën a dëgëral séy?

Biibël bi nee na, dañu war a teralante. Teral nit mooy won ko mbaax ak respe ci ni ngay doxale ak moom. Jàngal Room 12:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Ndax nit war na xaar jëkkëram walla jabaram njëkk koo teral? Lu tax?

BU LA NIT WAXOON: «Man ak sama jabar walla man ak sama jëkkër, suñu diggante demeetul noonu?»

  • Naka nga ko mënee won ne Biibël bi mën na leen dimbali?

NAÑU TËNK

Jëkkër ak jabar mën nañu am jàmm ci seen séy, bu ñu bëggante ci seen biir, ku nekk weg sa moroom te topp santaane yi nekk ci Biibël bi.

Nañu fàttaliku

  • Lan la jëkkër mën a def ngir yokk jàmm ci digganteem ak jabaram?

  • Lan la jabar mën a def ngir yokk jàmm ci séyam?

  • Bu dee danga am jëkkër walla jabar, ban njàngale ci Biibël bi moo la mën a dimbali nga dëgëral sa séy?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal ay xelal yu baax yu la mën a dimbali nga am jàmm ci sa njaboot.

Mën ngeen a am jàmm ci seen biir njaboot (téere bu ndaw)

Seetaanal wideo bu ànd ak misik buy wone barke yi nekk ci topp ci sa séy, xelal yi Yàlla joxe.

Bëggante dëgg (4:26)

Xoolal ni jëkkër ak jabar yu bëggoon a tas seen séy def ba regle seeni poroblem.

Biibël bi dimbali na ñu, ñu gën a dëgëral suñu séy (5:14)