Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 50

Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 2)

Naka nga mënee am jàmm ci sa biir njaboot? (Xaaj 2)

Doom mayug Yexowa la. Yexowa dafa bëgg waajur yi toppatoo bu baax seeni doom. Jox na waajur ay xelal yu baax ngir dimbali leen ñu mën koo def. Joxe na itam ay xelal yu mën a dimbali xale yi ñu def seen wàll ba jàmm am ci njaboot gi.

1. Ban xelal la Yexowa jox waajur yi?

Yexowa dafa bëgg waajur yi bëgg seeni doom te jël jot ngir di nekk ak ñoom. Dafa bëgg itam waajur yi aar seeni doom ci lépp lu leen mën a lor te jëfandikoo njàngale yi nekk ci Biibël bi ngir yar leen (Kàddu yu Xelu 1:8). Lii la wax baay yi: «Ngeen yar [seeni doom], di leen yemale ak a yee ci Boroom bi» (Jàngal Efes 6:4). Yexowa dafay bég, bu waajur yi toppee ay xelalam ngir yar seeni doom te bañ a dénk keneen wareef boobu.

2. Ban xelal la Yexowa jox xale yi?

Yexowa lii la sant xale yi: «Déggal-leen seeni waajur» (Jàngal Kolos 3:20). Bu xale yi maye cér seeni waajur te déggal leen, dañuy bégal Yexowa ak seeni waajur (Kàddu yu Xelu 23:22-25). Yeesu royukaay bu baax la ci xale yi. Nit ku mat la woon, waaye déggal na ay waajuram te mayoon na leen cér (Luug 2:51, 52).

3. Naka la seen njaboot mënee jege Yexowa?

Yeen waajur yi, li wóor mooy bëgg ngeen seeni doom bëgg Yexowa ni yeen. Lan ngeen mën a def ngir dimbali leen ci loolu? Defleen lii Biibël bi wax: «Nangeen [...] xamal seeni doom [kàddu Yexowa], di ko waxe bu ngeen toogee seen biir néeg, ak bu ngeen di dox ciw yoon, ak bu ngeen tëddee, ak bu ngeen jógee» (Baamtug Yoon wi 6:7). Fii «xamal» dafa ëmb di baamtu ak di baamtuwaat ngir jàngal nit ki. Xam ngeen ne bu ngeen bëggee seeni doom jàpp li ngeen leen di jàngal, dangeen ko war di baamtu ak di baamtuwaat. Aaya boobu dafay wone ne, dangeen war a def lépp ngir faral di wax ak seeni doom lu jëm ci Yexowa. Baax na lool ngeen di jël jot semen bu nekk ngir jàng Biibël bi ak seen njaboot. Bu dee amuleen ay doom, ba tey baax na ngeen jël jot semen bu nekk ngir jàng Kàddu Yàlla.

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolleen xelal yu baax yu leen mën a dimbali ngeen gën a am jàmm ak dal ci seen njaboot.

4. Yarleen seeni doom ci mbëggeel

Yar xale mën na nekk lu jafe. Naka la leen Biibël bi mënee dimbali? Jàngal Saag 1:19, 20. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Naka la waajur yi mënee wone mbëggeel, bu ñuy wax ak seeni doom?

  • Lu tax bu waajur meree warul yar mukk doomam? a

5. Aarleen seeni doom

Bu ngeen bëggee aar seeni doom, fàww ngeen wax leen lu jëm ci awra. Loolu mën na bañ a nekk lu yomb. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Lu tax mu jafe ci yenn waajur yi, ñu wax ak seen doom lu jëm ci awra?

  • Naka la yenn waajur yi xamale seen doom lu jëm ci awra?

Ni ñu ko yégle woon ci Biibël bi, àddina si Seytaane jiite dafay gën di bon. Jàngal 2 Timote 3:1, 13. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Nit ñu bon ñi ñu wax ci aaya 13 bi, ñiy sàkku xale yi ci lañu bokk. Kon lu tax mu am solo waajur yi jàngal seeni doom lu jëm ci awra ak ni ñu mënee aar seen bopp ci nit ñiy sàkku xale yi?

Ndax xamoon nga ne...

Seede Yexowa yi defar nañu ay téere ak ay wideo yu bari yuy dimbali waajur yi, ci jàngal seeni doom lu jëm ci awra te aar leen ci nit ñiy sàkku xale yi. Ci misaal, xoolal:

6. Mayleen cér seeni waajur

Xale yi ak ndaw ñi mën nañu wone ne, may nañu cér seeni waajur ci fasoŋ bi ñuy waxe ak ñoom. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Lu tax mu am njariñ ci ndaw ñi, ñu may cér seeni waajur bu ñuy wax ak ñoom?

  • Naka la ndaw mënee teral ay waajuram buy wax ak ñoom?

Jàngal Kàddu yu Xelu 1:8. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka la ndaw war a doxale bu ko ay waajuram waxe mu def dara?

7. Jaamuleen Yexowa ci seen biir njaboot

Seede Yexowa yi dañuy jël jot semen bu nekk ngir jàng Biibël bi ak seen njaboot. Naka lañuy defe seen njàngum Biibël bi ci biir njaboot? Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.

  • Naka la njaboot mën a def ba am njàngum Biibël ci biir njaboot semen bu nekk?

  • Naka la waajur yi mën a def ba njàngum Biibël ci biir njaboot gi, amal njariñ ñépp te neex? (Xoolal nataal bi njëkk ci lesoŋ bii).

  • Lan moo leen mën a tere ngeen def seen njàngum Biibël ci biir njaboot?

Ci Israyil bu njëkk ba, Yexowa dafa bëggoon njaboot yi di faral di waxtaan ci Mbind mu sell mi. Jàngal Baamtug Yoon wi 6:6, 7. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Naka nga mënee topp aaya yooyu?

Ay xelal ngir def njàngum Biibël ci biir njaboot

BU LA NIT WAXOON: «Biibël bi dafa jafe lool ci xale yi.»

  • Lan nga koy wax?

NAÑU TËNK

Yexowa dafa bëgg waajur yi bëgg seeni doom, yar leen te aar leen. Dafa bëgg xale yi may cér seeni waajur te déggal leen; te bëgg it njaboot yi booloo jaamu ko.

Nañu fàttaliku

  • Naka la waajur yi mënee yar seeni doom te aar leen?

  • Naka la xale yi mënee teral seeni waajur?

  • Jël jot semen bu nekk ngir jàng Biibël bi ci biir njaboot gi, ban njariñ la am?

Jubluwaay

GËSTUL

Yan njàngale ñoo mën a waajal sa doom mu doon ëllëg mag bu xam li muy def?

«Juróom-benni njàngale yu xale yi war a xam» (g19 n° 2)

Xoolal ni benn góor gu xamul woon ni ñuy yare xale mujjee doon baay bu baax.

Yexowa jàngal na ñu, ñu yar suñuy doom (5:58)

Xoolal ni baay yi mënee dëgëral seen diggante ak seeni doom yu góor.

«Naka la baay yi mënee wéy di jege seeni doom yu góor?» (w11 1/11)

a Ci Biibël bi, ‘yar’ mu ngi tekki jàngale, wommat ak jubbanti. Tekkiwul mukk toroxal walla def yëfi soxor (Kàddu yu Xelu 4:1).