Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 52

Lu tax ñu war a bàyyi xel ci ni ñuy soloo?

Lu tax ñu war a bàyyi xel ci ni ñuy soloo?

Ku nekk ci ñun am na fasoŋu colin bu ko neex. Bu ñu toppee njàngale yi nekk ci Biibël bi, dinañu mën a sol li ñu bëgg te neex itam Yexowa. Nañu xool yenn ci njàngale yooyu.

1. Yan njàngale ci Biibël bi ñoo ñuy dimbali ñu xam ni ñu war a soloo?

Dañu war di «sol col gu faaydawu, cig woyof ak maandu» te fexee nekk nit ñu set ngir wone suñu «ragal Yàlla» (1 Timote 2:9, 10). Nañu xool ñeenti njàngale yii di topp: (1) Li ñuy sol dafa war a «faaydawu.» Ni nga ko gisee ci ndaje yi ci mbooloo mi, jaamu Yexowa yi bokkuñu ni ñuy soloo, waaye li ñuy sol, ni ñuy léttoo ak ni ñuy watoo dafay wone ne, may nañu cér Yàlla bi ñuy jaamu. (2) Solu «cig woyof» mooy bañ a sol luy wone suñuy cér te di jur ay xalaat yu bon ci ñeneen. Mooy it bàyyi bépp fasoŋu colin buy tax ñépp di la xool. (3) Dañuy wone ne «maandu» nañu, bu ñu nekkul ñoo xam ne, lépp lu xew rekk ñu bëgg koo sol. (4) Suñu colin dafa war di wone saa su nekk suñu «ragal Yàlla», su ko defee nit ñi dinañu gis ne Yàlla dëgg ji lañuy jaamu (1 Korent 10:31).

2. Suñu colin lan la mën a def ci suñuy mbokki karceen?

Bu dee sax am nañu sañ-sañu sol lu ñu neex, war nañu bàyyi xel ci li suñu colin mën a def ci ñeneen ñi. Dañuy def suñu kem kàttan ba suñu colin du gaañ kenn, te dañuy ‘wut lu neex suñu moroom ngir jariñ ko’ (Jàngal Room 15:1, 2).

3. Naka la suñu colin mënee tax ñeneen ñi bëgg a jaamu Yexowa?

Dañuy jéem a am colin bu jekk saa su nekk, rawatina nag bu ñu naree teewe suñu ndaje yi ak bu ñuy waare. Bëgguñu nit ñi bañ a nangu xibaaru jàmm bi ndax suñu colin. Li ñu bëgg mooy, suñu colin tax ba nit ñi bëgg a jaamu Yexowa te «rafetal ci lépp njànglem Yàlla sunu Musalkat» (Tit 2:10).

XÓOTALAL NJÀNG MI

Xoolal ni ñu mën a def ba mu wóor ñu ne, suñu colin jekk na ci karceen.

Suñu colin mën na wone ne may nañu cér kilifa yi. Bu dee sax Yexowa li ci suñu biir xol lay xool, suñu colin war na wone it ne may nañu ko cér

4. Am colin bu baax dafay wone ne may nañu cér Yexowa

Lan mooy li gën a tax ñu war a bàyyi xel ci ni ñuy soloo? Jàngal Sabóor 47:3. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Xam ne Yexowa lañu fi teewal, naka la war a feeñe ci ni ñuy soloo?

  • Ndax foog nga ne jaadu na, ñu bàyyi xel ci suñu colin bu ñu naree teewe suñu ndaje yi ak bu ñuy waare? Lu tax?

5. Ni ñu mënee tànn bu baax ni ñuy soloo

Seetaanal WIDEO BI.

Ak fu ñu mënta nekk, li ñuy sol dafa war a nekk lu set te jekk, muy yére yu seer walla yu yomb. Jàngal 1 Korent 10:24 ak 1 Timote 2:9, 10. Boo paree, nga wax li tax ñu bëgg a moytu sol...

  • yére yu tilim walla ñu bàyyeeku ba mu ëpp.

  • yére yu xat, yu yaraax, walla yuy wone suñuy cér.

Dëgg la ne karceen yi toppatuñu yoonu Musaa, waaye mën na leen a dimbali ñu xam gis-gisu Yexowa. Jàngal Baamtug Yoon wi 22:5. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:

  • Lu tax góor war a moytu am colin buy tax ñu jaawale ko ak jigéen, walla jigéen ñu jaawale ko ak góor?

Jàngal 1 Korent 10:32, 33 ak 1 Yowaana 2:15, 16. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:

  • Lu tax ñu war a bàyyi xel bu baax ci ni ñeneen ñi di gise suñu colin, muy fi ñu dëkk walla ci mbooloo mi?

  • Naka la nit ñi di soloo fi nga dëkk?

  • Ndax foog nga ne, am na ci fasoŋu colin yu jekkul ci karceen? Lu tax?

Mën nañu am colin yu wuute te neex Yexowa

BU LA NIT WAXOON: «Lu ma neex laay sol.»

  • Ndax loolu mooy sa gis-gis? Lu tax?

NAÑU TËNK

Bu ñu tànnee bu baax ni ñuy soloo, dinañu wone ne may nañu cér Yexowa ak it nit ñi.

Nañu fàttaliku

  • Lu tax ni ñuy soloo am solo ci Yexowa?

  • Yan njàngale ci Biibël bi ñoo ñu mën a dimbali ñu tànn bu baax ni ñuy soloo?

  • Naka la suñu colin mënee tax ñeneen ñi bëgg a jaamu Yexowa?

Jubluwaay

GËSTUL

Xoolal li nit ñi di xalaat bu ñu gisee li nga sol.

«Lan laay nirool?» (Ci jw.org la nekk)

Xoolal li tax nga war a xalaat bala ngay tatuwaas.

«Lan la Biibël bi wax ci tatuwaas?» (Ci jw.org la nekk)

Naka la benn jigéen jàngee nangu ne, ñeneen ñi am nañu sañ-sañu tànn li ñu bëgg a sol?

«Sama gis-gis ci colin ak defaru moo ma doon teree jëm kanam» (g03 22/12)