Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ndax pare naa?

Ndax pare naa?

Ndax pare naa ngir waare ak mbooloo mi?

Dinga pare ngir nekk waarekat bu sóoboogul ci ndox, bu dee...

  • Yaa ngi jàng Biibël bi semen bu nekk, di faral di ñaan Yàlla ak di teewe ndaje yi ci mbooloo mi.

  • Fonk nga li nga nekk di jàng, gëm nga ko te bëgg nga koo xamal ñeneen ñi.

  • Bëgg nga Yexowa te tànn nga ñu bëgg Yexowa ñu doon sa xarit yi la gën a jege.

  • Bokkatuloo ci benn mbootaayu politig walla diine bu dul dëgg.

  • Yaa ngi topp santaane Yexowa yi ci sa dund te bëgg nga nekk Seede Yexowa.

Boo gisee ne pare nga ngir waare ak waa mbooloo mi, ki lay jàngal Biibël bi mën na def nga gise ak magi mbooloo mi ngir ñu wax la, li nga mën a def ngir tàmbali waare.

Ndax pare naa ngir sóobu ci ndox?

Dinga pare ngir sóobu ci ndox, bu dee...

  • Nekk nga waarekat bu sóoboogul ci ndox.

  • Yaa ngi def lépp li nga mën ngir faral di waare.

  • Yaa ngi nangu te di topp xelal yi jóge ci «surga bu takku te teey» bi (Macë 24:45-47).

  • Jébalu nga ci Yexowa ci ñaan te bëgg nga koo jaamu ba fàww.

Boo gisee ne pare nga ngir sóobu ci ndox, ki lay jàngal Biibël bi mën na def nga gise ak magi mbooloo mi ngir ñu wax la, li nga mën a def ngir sóobu ci ndox.