Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Yeneen leeral

Yeneen leeral
  1.  Lan mooy Babilon mu mag mi?

  2.  Kañ la Almasi bi waroon a feeñ?

  3.  Faj yi ñuy jëfandikoo deret

  4.  Tàggoo ci séy

  5.  Feet yi ak màggal yi

  6.  Feebar yiy wàlle

  7.  Lu jëm ci xaalis ak li yoon laaj

 1. Lan mooy Babilon mu mag mi?

Naka lañu xame ne «Babilon mu mag mi» mooy misaal mbooleem diine yi dul dëgg? (Peeñu 17:5). Xoolal ñetti firnde yii di topp:

  • Mu ngi yëngu ci àddina si sépp. Biibël bi nee na Babilon mu mag mi dafa toog ci kaw «réew yi ak mbooloo yi.» Dafay «nguuru ci kaw buuri àddina si» (Peeñu 17:15, 18).

  • Mënul doon mbootaayu politig walla mbootaayu jënd ak jaay. Ndaxte bés bi ñu koy alag, «buuri àddina yépp» ak «baana-baana» yi, dinañu mucc (Peeñu 18:9, 15).

  • Dafay tilimal turu Yàlla. Dañu ko woowe jigéenu moykat ndaxte dafay fas kóllëre ak nguur yi ngir am ci xaalis ak yeneen neexal (Peeñu 17:1, 2). Dafay réeral xeet yépp. Te moom moo tax ñu rey ay nit ñu bare (Peeñu 18:23, 24).

Dellul ci lesoŋ 13 ponk 6

 2. Kañ la Almasi bi waroon a feeñ?

Biibël bi yégle woon na ne, bala Almasi bi di ñëw, 69 àpp [walla semen, MN] dinañu jàll (Jàngal Dañeel 9:25).

  • Kañ la 69 semen yi tàmbali? Ci atum 455 B.S.J. Ci jamono jooju la kilifa gi Neyemi agsi Yerusalem ngir ‘leqli te tabaxaat’ dëkk ba (Dañeel 9:25; Neyemi 2:1, 5-8).

  • Lan mooy diiru 69 semen yi? Ci yenn yégle yonent yi nekk ci Biibël bi, benn bés dafay tekki benn at (Màndiŋ ma 14:34; Esekiyel 4:6). Kon semen bu nekk, juróom-ñaari at la. Kon 69 semen yi dañuy doon 483 at (69 semen ba 7 yoon).

  • Kañ la 69 semen yi waroon a jeex? Bu ñu waññee 483, dale ko 455 B.S.J. loolu dafay tombe ci atum 29 C.S.J. a Ci at boobu sax la Yeesu sóobu ci ndox te nekk Almasi bi! (Luug 3:1, 2, 21, 22).

Dellul ci lesoŋ 15 ponk 5

 3. Faj yi ñuy jëfandikoo deret

Am na faj yoo xam ne, doktoor yi dañuy jëfandikoo deretu nit ki feebar ngir faj ko. Am na loo xam ne karceen yi mënuñu koo nangu. Lu ci mel ni maye sa deret, walla ñu dénc sa deret ngir solaat la ko boo ko soxlaa (Baamtug Yoon wi 15:23).

Waaye nag am na ay faj yi ñu mën a nangu. Yu ci mel ni, def analiis ngir seet sa deret, li ñuy wax ci farãse hémodialyse, hémodilution, récupération du sang épanché walla jëfandikoo cœur-poumon artificiel. Karceen bu nekk mooy tànn ni ñuy jëfandikoo deretam bu ñu koy opeere, bu ñu koy defal wisit, walla ñu nekk di ko faj. Doktoor yépp bokkuñu ni ñuy jëfandikoo fasoŋu faj yooyu. Kon karceen bu nekk, bala muy nangu ñu opeere ko, ñu defal ko wisit, walla ñu faj ko, war na xam bu baax ni doktoor bi nar a jëfandikoo deretam. Xoolal laaj yii di topp:

  • Bu dee dañu jaarale sama deret ci ab masin ngir mu dellusiwaat ci sama yaram, waaye ci diggante bi deret bi taxaw nag? Ndax sama xel dina nangu ne deret bi ci man la bokk ba léegi, walla ci man mel na ni deret bi ‘tuuru na ci suuf’ ba pare? (Baamtug Yoon wi 12:23, 24).

  • Bu dee dañu jël sama deret, raxas ko, ba pare solaat ko ci sama yaram nag? Suma sukkandikoo ci li ma jàng ci Biibël bi, ndax sama xel dina dal? Walla ndax li ma jàng ci Biibël bi may na ma, ma nangu loolu?

Dellul ci lesoŋ 39 ponk 3

 4. Tàggoo ci séy

Biibël bi wax na ñaar ñiy séy ñu bañ a teqalikoo, maanaam tàggoo. Te wax na ci lu leer ne teqalikoo ak ki ngay séyal mayu la nga mën a séyaat ak keneen (1 Korent 7:10, 11). Waaye nag, am na li mën a tax yenn karceen yi bëgg a teqalikoo walla tàggoo ak ki ñuy séyal.

  • Ku bëggul a toppatoo njabootam: Jëkkër juy bañ a faj soxlay njabootam, ba loolu tax njabootam amatul dara lu mu dunde (1 Timote 5:8).

  • Kuy toroxal ki muy séyal: Mooy kiy dóore ak di gaañe. Loolu mën na tax ki muy séyal jàpp ne, mën na ñàkk wér-gi-yaramam walla bakkanam (Galasi 5:19-21).

  • Kuy yàq sa diggante ak Yexowa: Jëkkër ji walla jabar ji dafa def lépp ba keneen ki mënatul a jaamu Yexowa (Jëf ya 5:29).

Dellul ci lesoŋ 42 ponk 3

 5. Feet yi ak màggal yi

Karceen yi duñu bokk ci feet yi neexul Yexowa. Waaye karceen bu nekk mën na sukkandiku ci li mu jàng ci Biibël bi ngir xam li muy def, bu nit ñi di màggal feet yooyu. Nañu xool misaal yii di topp.

  • Nit ñaanal la sa feet neex. Mën nga ko tontu rekk, «Jërëjëf.» Bu nit ki bëggee xam li tax nga tontoo noonu, mën nga ko wax li tax bokkuloo ci feet boobu.

  • Feet am, sa jëkkër walla sa jabar ju nekkul Seede Yexowa, wax la ngeen dem booloo ak mbokkam yi ngir lekk ci bés boobu. Bu dee sa xel may na la nga def ko, mën nga ko xamal ne, bu ngeen demee, bu nit ñi defee lu jóge ci ñiy jaamu xërëm, doo ci bokk.

  • Sa pataroŋ yokkal la sa saleer ci jamonoy feet yu mel ni Nowel walla njeexteelu at mi. Ndax war nga ko bañ? Ci lii la aju: ndax ci sa pataroŋ, boo nangoo, bokk nga ci feet bi? Walla moom dafa koy def rekk ngir neexal la ci sa liggéey bu baax bi nga def?

  • Nit may la kado ci jamonoy feet yu mel ni Nowel walla njeexteelu at mi. Bi mu lay jox kado bi mën na la wax lii: «Xam naa ne bokkuloo ci feet bi, waaye lii dama la koo bëgg a may.» Xéyna dafa baax rekk. Waaye ndax foog nga ne, dafa koy def ngir jéem a seetlu sa ngëm walla dafa laa bëgg a dugal ci feet bi? Boo xalaatee ci loolu ba pare, yow yaay tànn ndax dinga nangu kado bi walla déet. Ci dogal yi ñuy jël, bëgg nañu am xel mu dal te wéy di takku ci Yexowa (Jëf ya 23:1).

Dellul ci lesoŋ 44 ponk 1

 6. Feebar yiy wàlle

Ndegam dañoo am mbëggeel ci nit ñi, dañuy def lépp ngir bañ leen a wàll feebar. Kon bu ñu xamee ne am nañu feebar buy wàlle walla ñu foog ko rekk, war nañu moytu bu baax ngir bañ a wàll kenn. Dañuy def loolu ndaxte lii la Biibël bi wax: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp» (Room 13:8-10).

Naka lañu mënee topp ndigal boobu? Nit ku am feebar buy wàlle warul a njëkk won ñeneen ñi cofeelam, lu mel ni laxasu leen walla fóon leen. Warul a mere ku ko bañ a ganale këram ndax bëgg a aar njabootam. Bala muy sóobu ci ndox, dafa ko war a wax kiy organise liggéeyu kurélu magi mbooloo mi, ngir ñu mën a jël ay matuwaay yuy aar ñeneen ñi war a sóobu itam. Bu nit amee xel ñaar ci ne, am na feebar buy wàlle walla déet, bala muy dugg ci ngoroo, dafa war a nangu def analiis ngir seet deretam ba xam ndax amul feebar bi. Booy def loolu, dinga wone ne fonk nga ñeneen ñi te nekkuloo di ‘topptoo sa bopp rekk, waaye boole nga ci sa moroom’ (Filib 2:⁠4).

Dellul ci lesoŋ 56 ponk 2

 7. Lu jëm ci xaalis ak li yoon laaj

Bu ñuy jëflante ak nit, ci wàllu xaalis walla jënd ak jaay, war nañu siñe ci kayit li ñu déggoo, bu dee sax suñu mbokk karceen la. Loolu dina tax ñu moytu poroblem yu bare (Yeremi 32:​9-12). Waaye ba tey lée-lée, ay karceen mën nañu am poroblem ci seen diggante ndax xaalis walla leneen. Waaye war nañu mën a regle loolu ci lu gaaw, ci jàmm te mu yem ci seen biir.

Léegi bu dee lu garaaw la nag, lu mel ni yëfi njublaŋ walla sosal nit? (Jàngal Macë 18:​15-17). Yeesu jox na ñu ñetti mbir yi ñu war a def:

  1. Jéemal a regle poroblem bi ci seen biir. (Xoolal aaya 15).

  2. Bu doxul, laajal kenn ku mat ci mbooloo mi walla ñaar, ñu ànd ak yow booy demaat ci kooku. (Xoolal aaya 16).

  3. Bu doxul ba léegi, boobu rekk nga ko war a wax magi mbooloo mi. (Xoolal aaya 17).

Lu ci ëpp, waruñu yóbbu suñu mbokk yi ci ngëm ci kanamu yoon, ndaxte loolu mën na tax nit ñi am gis-gis bu ñaaw ci Yexowa ak ci mbooloo mi (1 Korent 6:​1-8). Waaye am na poroblem yoo xam ne, dina laaj ñu dem ci kanamu yoon ngir mën koo regle. Lu mel ni: tas séy, ki nar a yore xale yi bu tas amee, li muy fey ngir dundal njaboot gi, fey ndàmpaay, sosiyete bu daanu, walla mbirum testama. Karceen bu dem ci yoon ngir regle poroblem yu mel noonu, te def lépp li mu mën ngir jàmm am, xelam mën na dal ndaxte deful lu Biibël bi tere.

Bu amee ku def ñaawteef bu réy bu mel ni, siif nit, sàkku xale, agerese, sàcc lu réy, walla rey nit, bu ko karceen yégalee waa poliis, xelam mën na dal ndaxte deful lu Biibël bi tere.

Dellul ci lesoŋ 56 ponk 3

a Li ko dale atum 455 B.S.J. ba atum 1 B.S.J. 454 at la. Li ko dale atum 1 B.S.J. ba atum 1 C.S.J. benn at la (atum sero amul). Te li ko dale atum 1 B.S.J. ba atum 29 C.S.J. 28 at la. Loolu lépp boo ko boolee mooy joxe 483 at yi.