XAAJ 3
Ay xelal yu am njariñ
BU amee doktoor bu bees bu sog a toxu fi nga dëkk, bala nga koy mën a wóolu, xanaa dinga xaar ba gis ay nit yu mu faj ba ñu wér, du dëgg ?
Mbind mu sell mi mu ngi mel ni doktoor boobu. Am na ay nit ñoo xam ne wóoluwuñu woon li nekk ci Mbind mu sell mi. Waaye bi ñu toppee xelal yi ci nekk, gis nañu ci njariñ bu réy. Xoolal liy topp.
Poroblem diggante jëkkër ak jabar
Li la benn jigéen bu tudd Sumeatun wax : “ Bi ma séyee ak Dumas sama jëkkër, yàggul dara mu komaase di ma bañ a faale. Loolu dafa ma doon metti lool ba may mer di ko yuuxu, lu ma gis rekk sànni ko ci kawam. Lée-lée dama doon mer ba xëm.
“ Bi Dumas komaasee jàng Mbind mu sell mi, dama ko doon ñaawal. Waaye dama doon làqatu di leen déglu, moom ak ki ko doon jàngal. Benn bés, ma dégg ñuy jàng aaya yii : ‘ Na jigéen ñi, nangul seeni jëkkër, ni su doon Boroom bi. [. . .] Na jigéen ji weg jëkkëram. ’ (Efes 5:22, 33). Kàddu yooyu laal na sama xol. Ma ñaan Yàlla mu baal ma ci fasoŋ bi may waxe ak sama boroom kër, te dama ko ñaan it Mu dimbali ma may gën a góor-góorlu ngir nekk jabar ju baax. Ma daldi bokk ak Dumas ci jàng Mbind mu sell mi. ”
Mbind mu sell mi wax na it lii : “ Na góor bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam. ” (Efes 5:28). Sumeatun nee na : “ Li ñu jàng ci Mbind mu sell mi, am na lu mu soppi ci man akit ci sama jëkkër. Léegi bu Dumas doon wàcc liggéey, dama ko doon may kaasu àttaaya te it ma komaase di ko wax ay wax yu neex. Dumas moom, dafa ma gën a won mbëggeelam te jàpple ma ci liggéeyu kër gi. Ñun ñaar jéem nañu di ‘ baax ci suñu diggante, di laayante biir tey baalante. ’ (Efes 4:32). Loolu tax na ñu gën a bëggante te ku nekk gën a may cér moroomam. Lu ëpp 40 at léegi ñu ngi am jàmm ci suñu diggante. Xelal yi nekk ci Kàddu Yàlla ñoo ñu musal ci tàggoo. ”
Tàng xol
Lii la benn góor gu tudd Tayib wax : “ Nekkoon naa nit ku tàng xol. Dama doon xeex rekk, lée-lée may tiital nit ñi ak fetal. Su ma meree, dama doon dóor itam Kustreya, sama jabar, ba mu daanu ci suuf. Ñu bare dañu ma ragaloon.
“ Benn bés ma jàng kàddu yii Yeesu waxoon : “ Maa ngi leen di jox ndigal lu bees : bëgganteleen. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge. ” (Yowaana 13:34). Loolu laal na sama xol torop ba ma fas yéene soppeeku. Léegi su ma doon yëg ne maa ngi bëgg a mer, dama doon ñaan Yàlla mu jàpple ma ma bañ a mer. Yàggul dara ma gis ne gaawatuma mer. Man ak sama jabar topp nañu xelal bi nekk ci Efes 4:26, 27 biy wax lii : “ Bu jant bi sowaale seen mer, ba ngeen may Seytaane bunt. ” Bés bu nekk, bala ñuy tëddi dañuy jàng Mbind mu sell mi te ñaan Yàlla. Loolu day tax ñu fàtte poroblem yu ndaw yi amoon suñu diggante ci bés bi te day tax ñu gën a nekk benn.
Léegi nitu jàmm lañu ma xame. Sama jabar ak samay doom bëgg nañu ma te jox nañu ma cér. Bare naa ay xarit te jege naa Yàlla. Dëgg-dëgg tey kontaan naa lool. ”
Dorog
Ku tudd Góyin, lii la wax : “ Bi ma nekkee xale, dama bokkoon ci benn gurupu bandi, tuxkat bu mag laa woon, di faral di màndi ba fanaan ci mbedd mi. Dama doon dorogewu te di jaay yàmbaa ak ecstasy bu ma doon nëbb ci biir yëre boo xam ne, ni ñu ko defare, bu ñu la fetalee bal bi du dugg. Ku ma gis xam ne dama dëgër te soxor waaye dama doon dëkk ci tiit.
“ Mu am ku ma won aaya bii : “ Sama doom, bul fàtte li ma la digal [. . .] ndax nga mën a gudd fan te sa dund ak sa jàmm yàgg ay at yu gën a bare. ” (Léebu yi 3:1, 2, MN). Gudd fan ak jàmm, loolu rekk laa bëggoon ! Lii laa jàng itam : “ Ndegam nag jot nanu ci dige yu mel nii, samay soppe, nanu sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell, ba mat ci ragal Yàlla. ”(2 Korent 7:1). Kon dama bàyyi dorog, jóge ci gurupu bandi yooyu, te tàmbali di jaamu Yàlla.
“ Bi ma bàyyee dorog, ëpp na léegi 17 at. Am na wér-gi-yaram, am naa jàmm ci sama kër, am naa ay xarit yu baax, te sama xel dal na. Bàyyi naa di màndi ba fanaan ci mbedd mi. Léegi damay fanaan ak jàmm ci sama kër. ”
Fonk sa xeet ba mu ëpp
Lii la benn xale bu tudd Bambaŋ wax : “ Bi ma nekkee xale, bandi laa woon te soxor te ñi gën a bare ci ñi ma doon song dañoo bokkoon ci xeet bu ma bañoon lool.
“ Mu am benn jamono, ma bëgg a xam Yàlla. May wër ba gis ay nit ñu doon daje ngir gëstu Mbind mu sell mi. Foofu dañu ma teral bu baax a baax fekk ci ñi ma doon teral amoon na ñu bokkoon ci xeet boobu ma bañoon lool ! Gis naa fa ay xeet yu bare yu booloo te nekk benn, di jëflante ci jàmm. Ma jaaxle lool ! Dem naa ba gis ne li Mbind mu sell mi wax am na, moo di : “ Ci dëgg gis naa ne, Yàlla du gënale, waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu. ” — Jëf ya 10:34, 35.
Fonk sa xeet ba mu ëpp, mu ngi mel ni posoñ. Posoñ boobu, nekkatul sama xol tey. Léegi ci xarit yi ma gën a jege, am na ñu bokk ci xeet boobu ma bañoon lool. Bëgg sa moroom, Yàlla moo ma ko jàngal ci Mbind mu sell mi. ”
Xeex
Lii la ku tudd Gërogë wax : “ Tëj nañu ma kaso ñetti yoon bi ma nekkee xale. Ñaar yi, sàcc la woon. Beneen bi dama agerese woon benn way. Ginnaaw loolu dama bokk ci benn gurup bu doon xeex ak nguuru réew mi te rey naa ay nit ñu bare. Bi xeex bi jeexee, ma daldi jiite benn gurupu bandi boo xam ne suñu liggéey moo doon di tànn ay nit ci gox
yi te wax leen ne saa yu ñu bëggee dara fàww ñu jox ñu ko walla ñu gaañ leen. Fépp fu ma doon dem, dama doon ànd ak ay gaa ñoo xam ne ñoo ma doon aar. Nit ku bëgg xeex laa woon te soxor.Benn bés, aaya bii laa jàng : “ Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du kiñaan, du kañu, du tiitaru, du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort. ” (1 Korent 13:4, 5). Kàddu yooyu ñoo laal sama xol ba ma toxu feneen, may jàng Mbind mu sell mi, te di topp xelal yi ci nekk.
“ Léegi bàyyi naa xeex. Maa ngi jàngale Kàddu Yàlla te nit ñi jox nañu ma cér ndax loolu. Léegi sama dund am na njariñ te xam naa fi ma jëm. ”
Kàddu Yàlla dafa am doole
Nettali yi ak yeneen ak yeneen yu bare ñooy wone ne “ kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. ” (Yawut ya 4:12). Li muy xelal dafa yomb, am na njariñ te sa ngëm day yokku.
Ndax li nekk ci Mbind mu sell mi mën na la dimbali yow it ? Waaw waaw te loolu mën na ko ci poroblem boo mënta am ! “ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet. ” — 2 Timote 3:16, 17.
Kon nañu seet léegi yenn wax yu am solo yu ñu mën a jàng ci Mbind mu sell mi.