XAAJ 8
Almasi bi ñëw na
LU ëpp 500 at ginnaaw yégle bi Dañeel defoon ci Almasi bi, malaaka mi tudd Jibril feeñu na benn jànq bu tudd Maryaama bi bokkoon ci askanu Dawuda. Mu ne ko : “ Jàmm ngaam, yaw mi boroom bi defal aw yiw ; mu ngi ak yaw. ” (Luug 1:28). Maryaama daldi tiit. Mu bëgg a xam lu tax malaaka mi wax ko loolu.
“ Malaaka ma ne ko : Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam. Dinga ëmb, jur doom ju góor ; nanga ko tudde Yeesu. [. . .] Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam [. . .] te nguuram du am àpp. ” (Luug 1:30-33). Xebaar bi neex na, de ! Maryaama mooy jur Almasi bi, “ askan ” bi ñu doon xaar bu yàgg !
At mi ci topp, Yeesu juddu na ci Betleyem. Guddi googu, lii la benn malaaka yëgal ay sàmmkat : “ Dama leen di xamal xebaar bu baax buy indi mbég mu réy [. . .]. Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi. ” (Luug 2:10, 11). Waa këru Yeesu dañu mujj a toxu Nasaret. Foofu la yaroo.
Ci atum 29 C.S.J. — fekk ci at moomu la Almasi bi naroon a ñëw— Yeesu dafa komaase di def liggéeyu yonent. Booba “ amoon na lu war a tollu ci fanweeri at. ” (Luug 3:23) Ñu bare dem nañu ba xam ne Yàlla moo ko yónni woon. Lii lañu wax : “ Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir ! ” (Luug 7:16, 17). Waaye lan la Yeesu doon jàngale ?
Yeesu jàngal na nit ñi ñu bëgg Yàlla te jaamu ko. Lii la wax : “ Yàlla sunu Boroom moom rekk mooy Buur. Kon nanga bëgg Yàlla sa boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, ak sa xel mépp ak sa kàttan gépp. ” (Màrk 12:29, 30). Wax na it lii : “ Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk. ” — Luug 4:8.
Yeesu sant na nit ñi ñu bëgg seeni moroom. Lii la wax : “ Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp. ” (Màrk 12:31). Wax na it lii : “ Lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal ; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi. ” — Macë 7:12.
Luug 4:43). Lu tax Nguuru Yàlla am solo noonu ?
Yeesu sawaroon na ci wax ak nit ñi lu jëm ci Nguuru Yàlla. Lii la wax : “ Damaa war a dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xebaar bu baax bi ci Nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma. ” (Mbind mu sell mi nee na Nguuru Yàlla, nguur la boo xam ne mu ngi ci asamaan te dina ilif suuf si. Yeesu mi nekk Almasi bi, moom la Yàlla fal buur ci Nguur googu. Yonent bi tudd Dañeel gisoon na ci benn peeñu ne Yàlla dina jox Almasi bi “ kilifteef gi, ndam li ak nguur gi ” ci asamaan. (Dañeel 7:14) Nguur googu dina defar suuf si sépp ba mu nekk Àjjana te dina may ñiy topp Yàlla dund gu dul jeex. Ndax loolu nekkul xebaar bu neex ?