Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 11

Gëm Yàlla dëgg, ni ko nit ñi di wonee tey

Gëm Yàlla dëgg, ni ko nit ñi di wonee tey

ÑU bare tey dañu ne gëm nañu Yàlla. Waaye Yeesu nee na ñiy gëm Yàlla dëgg, duñu bare. Lii la wax : “ Bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare. Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul. ” — Macë 7:13,14.

Naka la nit ñi di wonee ne gëm nañu Yàlla dëgg tey ? Lii la ci Yeesu wax : “ Garab gu baax gu nekk dina meññ doom yu neex, waaye garab gu bon dina meññ doom yu bon. ” (Macë 7:16, 17). Kon ngëm dëgg, dafay meññ “ doom yu neex ”. Day xiir nit ñi ci am jikko ju neex Yàlla. Naka lañu koy wonee ?

Ni ñuy jëfandikoo seen kàttan

Ñi gëm Yàlla dëgg, bu ñu nekkee kilifa walla ñu am kàttan, dañuy jëfandikoo taxawaay boobu ngir màggal Yàlla te dimbali nit ñi. Yeesu nee na : “ Ku bëgg a nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga ”.(Màrk 10:43). Noonu it, góor gu gëm Yàlla du soxor, muy ci biir kër walla ci biti. Dafay bëgg jabaram, fonk ko, jox ko teraanga te faj ay soxlaam. Mbind mu sell mi nee na : “ Góor ñi, na ku nekk bëgg jabaram te muñal ko. ” (Kolos 3:19). “ Góor ñi, na ku nekk ci yéen am xel, ci ni ngay ànde ak sa jabar, xam ne àndandoo ju la gën a néew doole la. Joxleen ko teraanga ju mat, ndax yéen a yem cér ci yiwu Yàlla, wi ñu ubbil buntu dund gu dul jeex. Noonu dara du man a yàq seeni ñaan. ” — 1 Piyeer 3:7.

Te it, jigéen ju gëm Yàlla dëgg, dafa war a “ weg jëkkëram. ” (Efes 5:33). Jigéen ñi dañu war a “ bëgg seeni jëkkër ak seeni doom ” (Titt 2:4). Baay yi ak yaay yi gëm Yàlla, dañuy fexe ba mën a toog ak seeni doom te jàngal leen yoonu Yàlla. Dañuy may cér nit ku nekk, muy ci biir kër gi, walla fi ñuy liggéeye, walla feneen. Dañuy topp li Mbind mu sell mi wax fii : “ Farlu[leen] ci teralante. ” — Room 12:10.

Ñiy topp Yàlla duñu nangu ñu jënd leen, ni ko Mbind mu sell mi digale. (Exode 23:8) Taxawaay bu ñu mënta am duñu ko jëfandikoo ngir topp seen njariñu bopp. Waaye dañuy seet li ñu mën a def ngir dimbali nit ñi, rawatina ñi nekk ci soxla. Lii lañuy topp : “ Buleen fàtte di def lu baax ak di sédde ci seen alal, ndaxte sarax yu mel noonu ñoo neex Yàlla. ” (Yawut ya 13:16). Ci lañuy gis ne Yeesu waxoon na dëgg bi mu nee : “ Joxe moo gën a barkeel nangu. ” — Jëf ya 20:35.

Njubte Yàlla lañuy topp

Ñi gëm Yàlla dañuy topp ndigalu Yàlla yi te loolu dafa leen di neex, te pur ñoom “ ay ndigalam diisuñu. ” (1 Yowaana 5:3). Xam nañu ne “ yoonu Aji Sax ji moo mat [. . .]. Ndigali Aji Sax ji ñoo jub, di bégal xol. Santaaney Aji Sax ji ñoo leer, di yànjal bët yi. ” — Sabóor 19:8, 9.

Ngëm dëgg dafa leen xiir itam ci bañ a gënale. Duñu xool nit ci xeetam, réewam, walla alalam waaye dañuy roy ci Yàlla ndax “ Yàlla du gënale, waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu. ”— Jëf ya 10:34, 35.

Ngëm dëgg day xiir nit ñi ñu “ rafet ci lépp lu ñuy def. ” (Yawut ya 13:18). Ku gëm Yàlla du sosal kenn. Yonent Yàlla Dawuda waxoon na ne nit ñi neex Yàlla duñu def loolu te duñu def seen moroom dara lu bon. — Psaume 15:3.

Xam-xamu Yàlla moo leen jiite

Lépp li ñu gëm, ci Mbind mu sell mi rekk lañu koy sukkandiku. Gëm nañu ne “ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub. ” (2 Timote 3:16). Bu ñuy jëflante ak nit ñi, dañuy wone “ xel mi jóge ci kaw ” mi nga xam ne “ daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet. ” (Saag 3:17). Duñu topp aada yi àndul ak li Yàlla bëgg. Te it duñu bokk dara ci luxus, mbirum tuuri maam walla yu mel noonu te dañuy ‘ wottu seen bopp ci xërëm yi. ’ — 1 Yowaana 5:21.

Dañuy wone mbëggeel dëgg

Lii la yonent Yàlla Musaa waxoon : “ Danga war a bëgg Yexowa sa Yàlla ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa kàttan gépp. ” (5 Musaa [Deutéronome] 6:5, MN). Ñi gëm Yàlla, noonu lañu ko war a bëgge. Dañuy màggal turam, Yexowa, sant ko te woo ko ci turam ak xol bu fees ak ngëm. (Psaume 105:1). Ndigal bii lañuy topp itam : “ Danga war a bëgg sa moroom ni nga bëgge sa bopp. ” (3 Musaa [Lévitique] 19:18, MN). Bëgguñu xeex te dañuy def lépp ngir “ juboo ak ñépp ”.(Room 12:18). Dafa mel ni dañu “ tëgg ci seeni jaasi illeer, [te] def seeni xeej sàrt. ” (Esayi 2:4). Loolu moo tax ‘ ñu bëggante ’ te mel ni njaboot bu réy. (Yowaana 13:35). Ndax xam nga ay nit ñu mel noonu tey ?