Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 10

Ki bañ ñu gëm Yàlla, lan la def?

Ki bañ ñu gëm Yàlla, lan la def?

LU yàgg bala mu sàkk suuf, Yexowa sàkkoon na ay malaaka ci asamaan. Am na benn jamono, benn malaaka dafa jóg, bëgg ñu jaamu ko, fekk Yàlla rekk lañu war a jaamu. Bëgg-bëgg boobu yóbbu na ko ba mu def boppam “ Seytaane ” miy tekki “ kuy xeex keneen ” ndaxte dafa doon xeex Yàlla. Lan la Seytaane def Yàlla ?

Seytaane dafa jaar ci benn jaan ngir nax Awa

Dafa nax Awa ba mu déggadi Yàlla. Dafa foogloo Awa ne dina am lu neex lu koy raw bu lekkulee doomu garab bi ko Yàlla tere woon. Dafa dem ba wax ne Yàlla waxul dëgg ba pare xiir Awa ci bàyyi topp Yàlla. Lii la wax : “ Yàlla xam na ne bés bu ngeen ci lekkee, seeni bët dina ubbiku, ngeen mel ni Yàlla, xam lu baax ak lu bon. ” (Njàlbéen ga 3:5). Awa gëm na li Seytaane waxoon. Dafa déggadi Yàlla ba pare yóbbaale ci Aadama. Booba ba léegi, Seytaane mu ngi kontine di xeex ñi gëm Yàlla dëgg, di leen jéem a nax. Naka lay defe loolu ?

Yàq ngëm mooy law

Seytaane dafay jaar ci xërëm ak ci aada yi ngir nax nit ñi

Seytaane jaaroon na ci xërëm yi ak ci aada nit ñi ngir yàq ngëmu doomu Israyil yi. Yeesu mi nekk Almasi bi waxoon na seeni njiiti diine, maanaam yu doomu Israyil yi, ne seen màggal Yàlla amul woon benn njariñ ndaxte dañu doon “ jàngale dénkaaney nit kese. ” (Macë 15:9). Bi waa Israyil bañee Almasi bi, Yàlla bàyyi na leen. Lii la leen Yeesu wax : “ Dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam ”.(Macë 21:43). Léegi taalibe Yeesu ñoo nekk mbooloo mi Yàlla nangu.

Ginnaaw loolu, Seytaane jéem na yàq ngëmu ñi doon topp Yeesu. Ndax mujj na koo def ? Ci benn misaal bi mu yégle woon, Yeesu waxoon na li waroon a xew. Ci misaal boobu, dafa am nit ku ji jiwu wu baax, maanaam dugub, ci toolam. Ginnaaw loolu, noonam ñëw ji jëmb ci biir dugub ji. Ñu bàyyi ñaari ji yooyu màgg ba ngóob jot, ñu xàjjale leen, yàq jëmb bi te dugal dugub ji ci sàqu boroom kër gi.

Yeesu wax na taalibeem yi li misaal boobu tekki. Moom mooy Nit ki ji jiwu wu baax wi. Mu ne : “ Ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi ; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi ; Seytaane mooy noon bi ko ji ; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi. ” (Macë 13:38, 39). Yeesu dafa méngale taalibeem yi ak jiwu wu baax. Waaye Seytaane dafa ji ay taalibe yu dul dëgg, mel ni jëmb bi, ci biir ñi toppoon Yeesu dëgg. Kon ni ko Yeesu waxe woon, ci ay téemeeri at yi topp deewam, ay taalibe yu dul dëgg ñoo feeñ. Ñoom ñoo komaase di jàngale lu dul dëgg lu mel ni trinite biy wax ne Yàlla ñett la . Ñu komaase di jaamu ay xërëm te bokk ci politig. Li Yeesu jàngale woon, ñi ko topp bareetuñu woon.

Ngëm dëgg am na ba tey

Ni ko Yeesu waxe woon, dina am luy soppeeku. Malaaka Yàlla yi dinañu xàjjale ñi gëm Yàlla dëgg ak ñi ko gëmul dëgg. Booba, ñi gëm Yàlla dëgg dinañu yomb a ràññe. Ñi gëmul dinañu leen alag. Ca muj ga, Seytaane mi nekk Ibliis, ki njëkk a xeex ngëm, dinañu ko alag moom it. Waaw, ngëm dëgg mooy gañe !

Léegi, naka nga mën a xàmmee ñi gëm Yàlla dëgg tey ? Dinañu ci waxtaan léegi.

Malaaka Yàlla yi ñu ngiy wut ñi bëgg a gëm Yàlla dëgg