XAAJ 13
Ku gëm Yàlla dëgg, dinga mën a am jàmm ba fàww
MBIND mu sell mi nee na : “ Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund. ” (Room 1:17). Kàddu yooyu ñu ngi ëmb dige bu neex lool te am nga ci wàll ! Ban wàll ?
Bi Yeesu mi nekk Almasi bi àggalee liggéeyam ci kaw suuf, mu ngi doon dellu ca asamaan ngir nekk fa ak Yàlla, taalibeem yi di ko xool, “ Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët. ” (Jëf ya 1:9). Ca asamaan, Yàlla fal na ko buur. Bu ci kanamee tuuti, Yeesu, maanaam “ Doomu nit ki ”, dina “ ñëw ci ndamam, ànd ak malaaka yépp, booba dina falu ni buur, toog ci jalam bu soloo ndam. Bu boobaa dees na dajale xeeti àddina yépp ci kanamam, te dina leen xàjjale, ni sàmm di xàjjale xar yi ak bëy yi ”. (Macë 25:31, 32). Loolu kañ lay doon ?
Mbind mu sell mi waxoon na ne bu ñu gisee àddina bi yépp jaxasoo, loolu dina wone ne Almasi bi, léegi mu ñëw àtte nit ñi. Lii la ci Yeesu wax : “ Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew. Suuf dina yengu yengu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu. ” — Luug 21:7, 10, 11.
Loolu yépp Yeesu waxoon gis nañu ko tey. Bu ci kanamee tuuti, Yeesu dina ñëw alag ñu bon ñi. Seytaane sax, dinañu ko mujj a alag ! Suuf si sépp dina nekk àjjana. Nit ñépp dinañu am jàmm ci seen biir. Jàmm dina am sax diggante nit ak mala. “ Bukki dina dëkk ak mbote, segg tëdd ak tef, sëllu, gaynde ak jur gi ñuy yafal dinañu ànd, te xale dina leen sàmm. [. . .] Gaañ ak lor dootu fa am. ” (Esayi 11:6, 9). ‘ Kenn dootul ne : “ dama feebar. ” [. . .] Gumba yi dinañu gis, tëx yi dinañu dégg. ’ (Esayi 33:24, MN ; 35:5). Ñi dee sax dinañu dekki. Lii la Yexowa di def : “ Dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit. ” (Peeñu ma 21:4 ; Isaïe 25:8). Kon li taxoon Yàlla sàkk suuf si, dina am. Loolu neex na dégg, de, du dëgg ?
Nanga kontine di yokk sa ngëm
Ñan nit la Yàlla di may dund ci àjjana ? Ñi gëm Yàlla ? Nañu ne ñi ko gëm dëgg !
Bul fàtte ne ngëm dëgg day sukkandiku ci xam bu baax li nekk ci kàddu Yàlla. Kon nanga kontine di yokk li nga xam ci Yàlla ak ci Yeesu !
Ngëm dëgg dafay feeñ ci ay jëf yu baax. Kàddu Yàlla nee na : “ Ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ. ” (Saag 2:17). Li la xiiroon ci Yàlla ba nga bëgg ko roy, maanaam kàttanam, njubteem, xam-xamam ak mbëggeelam, dina feeñ ci lu baax li ngay def. Nanga kontine di wone jëf yu mel noonu.
Gëm Yàlla dëgg, dina la indil barke yu réy. Ci dëgg, loolu moo la mën a indil jàmm — tey ba fàww !