Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 2

Lan mooy gëm Yàlla dëgg ?

Lan mooy gëm Yàlla dëgg ?

Ngëm dëgg rekk moo am njariñ, mel ni xaalis bu baax

XAM ne Yàlla am na taxul nga gëm ko dëgg. Ay milioŋi nit xam nañu ne Yàlla am na waaye ba tey ñu ngi def lu bon te bëgguñu soppeeku. “ Ngëm ” gu mel noonu mu ngi mel ni xaalis bu baaxul. Xaalis boobu mu ngi mel ni xaalis dëgg, fekk du moom. Mënoo ci jënd dara. Kon lan mooy gëm Yàlla dëgg ?

Ngëm dëgg mu ngi sukkandiku ci lépp li Mbind mu sell mi wax. Mbind mu sell moomu jóge ci Yàlla moo ñuy xamal kan mooy Yàlla dëgg, li mu santaane, li tax mu sàkk nit ak suuf si, ak yeneen yu ñu war a xam mel ni :

  • Yàlla kenn la te amul moroom.

  • Yeesu du Yàlla Aji-Kàttan ji. Yonent Yàlla la.

  • Yàlla sib na bépp fasoŋu xërëm.

  • Bés bu Yàlla di àtte nit ñi soreetul.

  • Yàlla dina dekkal nit ñu baree bare ci àjjana.

Ngëm dëgg dafa lay xiir ci def lu baax. Jëf yu baax dafay màggal Yàlla te ñépp lay amal njariñ. Jëf yiy topp bokk nañu ci.

  • Jaamu Yàlla.

  • Jéem a am jikko ju neex Yàlla, rawatina mbëggeel.

  • Génne ci sa xel xalaat ak bëgg-bëgg yu bon.

  • Bañ a bàyyi Yàlla boo nekkee ci poroblem.

  • Dimbali nit ñi ñu xam kan mooy Yàlla ak li mu bëgg.

Ngëm dëgg dafay feeñ ci ay jëf yu rafet

Lan lañu mën a def ngir gëm Yàlla dëgg?

Ngëm mën na yokku, mel ni doole buy yokku booy tàggat sa yaram

Ñaanal Yàlla mu dimbali la. Lii la yonent Yàlla Musaa ñaanoon Yàlla : “ Xamal ma say yoon. Noonu dinaa la xam te fekk yiw ci say bët. ” a Yàlla nangu na ñaan boobu te Musaa mujj na nekk royukaay bu mag ci wàllu ngëm. Yàlla dina la jàpple yow itam ba nga mën koo gëm dëgg.

Fexeel ba am jot ngir jàng Mbind mu sell mi. Mbind mu sell mi, mu ngi jóge ci Yàlla te Tawreet, Sabóor ak Injiil bokk nañu ci. Mën nañu ko jàng ci Biibël bi, téere bi ñu gëna firi ci làkk yu bare te gëna siiwal ci àddina si. Ndax am nga mbind yooyu sa kër ?

Bés bu nekk nanga topp li Mbind mu sell mi wax. Ngëm day yokku, mel ni doole buy yokku booy tàggat sa yaram. Noonu it, li ngay def , boo koy def te Yàllaa tax, sa ngëm dina yokku. Dinga gis ci sa wàllu bopp njariñ bi nekk ci topp li Yàlla wax. Li Yàlla wax ci Mbind mu sell mi dimbali na ay nit yu baree bare ba ñu am jàmm ci seen dund. Boo bëggee xam ni loolu di ame, jàngal li topp.