Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 6

Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

Lu tax Yàlla sàkk suuf si ?

YÀLLA dafa sàkk suuf si ngir nit dëkk ci. Lii la wax ci kàddoom : “ Yexowa moo moom asamaan, waaye suuf si dafa ko may doomu Aadama yi. ” — Sabuur 115:16, MN.

Bala Yàlla sàkk suñu maam Aadama, dafa tànn benn béréb ci kaw suuf si, béréb bu ñuy woowe Àjjana, te defar ko mu nekk tool bu rafet. Mbind mu sell mi dafa wax ne ñaari dex ñoo jóge woon toolu Àjjana boobu. Benn bu tudd Efraat ak beneen bu tudd Tigre (Idekel). a Kon mën nañu xalaat ne toolu Àjjana mu ngi won ci réew mi ñuy wax tey Turquie. Waaw, toolu Àjjana, ci kaw suuf la nekkoon !

Yàlla dafa sàkk Aadama te dugal ko ci toolu Àjjana ngir “ mu di ko bey ak a sàmm. ” (Njàlbéen ga 2:15). Ginnaaw loolu, Yàlla dafa sàkk Awa, may ko Aadama pur mu nekk jabaram. Yàlla nee leen: “ Giirleen te bare ba fees àddina di ko saytu. ” (Njàlbéen ga 1:28). Kon leer na ne Yàlla sàkkul suuf ndax neen waaye dafa ko sàkk ngir nit dëkk ci. — Isaïe 45:18.

Waaye Aadama ak Awa, ñoom, dañu jéggi yoonu Yàlla te ñoo ko tey. Yàlla génne leen toolu Àjjana. Àjjana ji, ñàkk nañu ko. Bàkkaaru Aadama, am na leneen lu mu def. Mbind mu sell mi nee na : “ Bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar. ” — Room 5:12.

Ndax Yexowa bàyyi na li mu bëggoon a def, maanaam suuf si nekk àjjana te fees ak ay nit ñu bég ? Déedéet ! Yàlla nee na : “ Sama kàddu, gi génne ci sama gémmiñ ; du dellusi mukk ci man cig neen, waaye dina matal sama coobare, def sama nammeel. ” (Esayi 55:11). Kon suuf si dina nekkaat Àjjana !

Dund ci biir Àjjana, nu muy mel ? Nañu seet léegi li Mbind mu sell mi wax ci loolu.

a Lii la Njàlbéen ga 2:10-14 wax : “ Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddalikoo, def ñeenti wal. Turu menn wal ma di dexu Pison [. . .]. Ñaareelu dex ga di Giyon [. . .] ; turu ñetteelu dex ga di Idekel [maanaam Tigre], féete réewu Asiri penku ; ñeenteelu dex ga di Efraat. ” Ñaari dex yi des, xamuñu fu ñu féete.