Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Li ñi teew war a xam

Li ñi teew war a xam

NDAJE MI

LEKKOOL BI ÑU JAGLEEL ÑIY WAARE NGUURU YÀLLA Ñu ngi woo pioñee yi am diggante 23 at ba 65 at te bëgg a yokk seen liggéeyu waare bi, ñu ñëw teewe ndaje bi ñu jagleel ñi bëgg a bokk ci Lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguuru Yàlla. Ndaje boobu dinañu ko def dimaas ci ngoon. Waxtu bi ak béréb bi ñuy defe ndaje boobu, dinañu leen ko wax.

LI ÑI TEEW WAR A XAM

ÑIY TEERU NIT ÑI Dimbali nit ñi moo tax ñu teg leen foofu. Ñu ngi leen di ñaan ngeen topp bu baax seen tegtal ci fu ñu war a gaare oto yi, fu ñu war a jaar, fu ñu war a toog, ak yeneen ak yeneen.

SÓOB BI Samdi ci suba, ñi ñu war a sóob ci ndox, war nañu toog ci palaas yi ñu leen dencal, bala waxtaanu sóob bi di komaase. Na ku neek indaale benn sarbet ak lu yiw lu muy sol bu ñu koy sóob ci ndox mi. Nañu toog ci kanam, ci siis yu njëkk yi. Su ñu waree soppi dara ci li ñu wax fii, dinañu ko yégal ñépp bala waxtu bi jot, te dinañu ko wax it ñiy teeru nit ñi ak ñi nekk ci biro bu ñuy tontoo laaj yi.

ÑI BËGG A DEF AY MAYE Xaalis bi ñu dugal ci ndaje bii, bare na lool. Siis yi ngeen di gis, mikoro yi, jumtukaay yi ñuy tax a seetaan wideo ak yeneen ak yeneen, dañu leen def fii ngir suñu teewaay bi neex te dimbali ñu ci gën a jege Yexowa. Xaalis bu ngeen di maye, dinañu jàppale ci depãs yooyu ak it ci liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Dingeen gis ci bérébu ndaje bii ay boyet yu ñu def ngir ñi bëgg a maye dara. Ñu ngi leen di gërëm bu baax ci lépp li ngeen di maye. Jataay biy dogal it mu ngi leen di gërëm ci lépp li ngeen di maye ngir liggéeyu Nguur gi jëm kanam.

FI ÑUY TOPPATOO ÑI DARA DAL Buleen fàtte ne ÑI LU METTI DAL REKK walla yu mel noonu lañu fay toppatoo.

LI NIT ÑI RÉERAL TE ÑU GIS KO Lépp li réer te ñu gis ko war nañu ko yóbbu ci biro boobu. Soo ame loo réeral, demal ci biro boobu seet ba xam ndax kenn yóbbuwu ko fa. Xale yi réer seeni waajur, war nañu leen a yóbbu ci biro boobu. Waaye waruñu jàppe biro boobu ni béréb bu ñuy dénkaane xale yi. Ñu ngi leen di ñaan ngeen xool seeni doom, te toogloo leen ci seen wet.

FI ÑUY TOOG Nanga xalaat ñeneen ñi, te bañ a fàtte ne, seeni mbokk, ñi nga bokkal oto ak sa waa kër walla ñi ngay jàngal Biibël bi rekk nga mën a dencal palaas. Ñu ngi lay ñaan nga bañ a teg dara ci siis yi nekk ci sa wet. Su ko defee, nit ñi dinañu xam ne mën nañu ci toog.

ÑI BËGG A BOKK CI LIGGÉEYU NDAJE BI Boo bëggee bokk ci liggéeyu ndaje bii, nanga dem ci biro bi yore wàllu Yégle yi ak wàllu Ñi bëgg a bokk ci liggéeyu ndaje bi. Dinañu la won fi ñu soxla ndimbal.

Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi ñoo taxawal ndaje bii