Samdi
Ndamooleen turam wu sell. Kuy wut Yexowa Aji Sax ji, yal na am bànneexu xol.—Sabóor 105:3
SUBA SI
-
9:20 Porogaraamu misik bu ànd ak wideo
-
9:30 Woy-Yàlla nº 53 ak ñaan
-
9:40 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ : Ñamal ci mbégte bi nekk ci sàkk ay taalibe — Yokkal sa mën-mën
-
• Laajal nit ki (Saag 1:19)
-
• Bàyyil dooley Kàddug Yàlla mu jëf (Yawut ya 4:12))
-
• Jëfandikool ay misaal (Macë 13:34, 35)
-
• Àndal ak cawarte booy jàngale (Room 12:11)
-
• Woneel mbaax (1 Tesalonig 2:7, 8))
-
• Laalal xolu nit ki (Kàddu yu Xelu 3:1)
-
-
10:50 Woy-Yàlla nº 58 ak yégle yi
-
11:00 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ : Ñamal ci mbégte bi nekk ci sàkk ay taalibe — Nangul ndimbalu Yexowa
-
• Jumtukaay yi ngir gëstu (1 Korent 3:9 ; 2 Timote 3:16, 17)
-
• Suñu mbokk yi (Room 16:3, 4 ; 1 Piyeer 5:9)
-
• Ñaan Yàlla (Sabóor 127:1)
-
-
11:45 SÓOB BI : Naka la sóobu ci ndox di yokke sa mbégte (Kàddu yu Xelu 11:24 ; Peeñu ma 4:11)
-
12:15 Woy-Yàlla nº 79 ak noppalu bi
NGOON SI
-
1:35 Porogaraamu misik bu ànd ak wideo
-
1:45 Woy-Yàlla nº 76
-
1:50 Naka la suñu mbokk yi di ñame ci mbégte bi nekk ci sàkk ay taalibe ca . . .
-
• Afrik
-
• Asi
-
• Europe
-
• Bëj-gànnaaru Amerik
-
• Océanie
-
• Bëj-saalumu Amerik
-
-
2:35 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ : Dimbalil kiy jàng ak yow Biibël bi mu . . .
-
• Lekk ci wàllu xel (Macë 5:3 ; Yowaana 13:17)
-
• Teewe ndaje yi (Sabóor 65:5)
-
• Moytu àndandoo yu bon (Kàddu yu Xelu 13:20)
-
• Bàyyi tàmmeel bu sellul (Efes 4:22-24)
-
• Am diggante bu rattax ak Yexowa (1 Yowaana 4:8, 19))
-
-
3:30 Woy-Yàlla nº 110 ak yégle yi
-
3:40 FILM BI SUKKANDIKU CI BIIBËL BI : Nëxemiya : « Mbégte bu jóge ci Yexowa mooy seen doole » — Xaaj I (Néhémie 1:1–6:19)
-
4:15 Sàkk ay taalibe tey dafa ñuy waajal ci liggéeyu sàkk ay taalibe bi ñu war a def ci addina su bees si (Esayi 11:9 ; Jëf ya 24:15)
-
4:50 Woy-Yàlla nº 140 ak ñaan bu mujj bi