Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

LESOŊ 1

Woneel nit ñi ne am nga itte ci ñoom

Woneel nit ñi ne am nga itte ci ñoom

Njàngale bi: «Ku bëgg . . . du wut njariñu boppam.»—1 Korent 13:​4, 5.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Yowaana 4:​6-9. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Lan la Yeesu seetlu woon ci jigéen ju dëkkoon Samari bala muy wax ak moom?

  2.   Yeesu dafa ko waxoon ne: «May ma ndox, ma naan» Lu tax loolu nekk fasoŋ bi gën ngir tàmbali waxtaan ak moom?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñu njëkke wax nit ki li koo itteel dina ñu am waxtaan bu neex ak moom.

Nanga roy ci Yeesu

3. Tànnal waxtaan bu itteel nit ki. Bul wut a wax rekk li nga waajaloon. Njëkkal a wax ci li itteel nit ñi. Laajal sa bopp lii:

  1.    «Yan xibaar lañu dégg fan yi?»

  2.   «Ci lan la sa dëkkandoo yi, ñi nga bokkal liggéey, walla ñi nga bokkal kalaas di wax fan yi?»

4. Deel seetlu. Laajal sa bopp lii:

  1.    «Lan la nit ki nekk di def? Lan moo war a nekk ci xelam fu mu nekk nii?»

  2.   «Li nit ki sol ak ni këram mel, lan la ma mën a jàngal ci diineem walla ci aadam ?»

  3.   «Ndax wax ak moom ci waxtu bii, mooy li gën ci moom, walla dama war a xar ba beneen yoon?»

5. Farlul ci déglu.

  1.    Bul faral di wax lu bare.

  2.   Mayal nit ki mu wax li mu xalaat. Laaj ko ay laaj ba mu amal boppam tontu bi.