Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE JÀNGAL NIT ÑI BA ÑU NEKK TAALIBE YEESU

LESOŊ 10

Na nga farlu ci liggéeyu waare bi

Na nga farlu ci liggéeyu waare bi

Njàngale bi: «Yemuñu ci xamal leen xibaaru jàmm bu Yàlla, waaye, dañu leen a sopp ba yéene leen a jox suñu bakkan sax, ndax fi ngeen mujj tollu ci suñu xol.»—1 Tesalonig 2:8.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Yowaana 3:​1, 2. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Lu tax Nikodem xaar ba guddi bala muy seeti Yeesu? —Jàngal Yowaana 12:​42, 43.

  2.   Lu tax nu mën a wax ne, ni Yeesu nangoo waxtaan ak Nikodem guddi dafay wone ne liggéeyu sakk ay taalibe lu am solo la ci moom?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñuy def lépp li ñu mën ngir dimbali nit ñi ñu nekk taalibe Yeesu, dañuy wone ne bëgg nañu leen.

Nanga roy ci Yeesu

3. Nangul a jàngal nit ki ci waxtu ak ci béréb bi gën ci moom. Kañ ak ban waxtu moo gën ci moom? Fan La bëgg a def njàngum Biibël bi? Ndax ci béréb bi muy liggéeye la ko bëgg a def? Walla ci këram? Walla sax ci beneen béréb? Defal lépp li nga mën ngir jàngal nit ki bu dee sax loolu dafay tekki ne danga war a soppi sa porogaraam.

4. Nanga góor-góorlu ba mu am njàngum Biibëlam ayu bés bu nekk. Bu dee doo fi nekk ayu bés bii di ñëw, bul tëb njàngum Biibëlam bi. Waaye, xoolal:

  1.    Ndax dinga mën a def njàngum Biibëlam bi ci beneen waxtu?

  2.   Ndax dinga ko mën a woo ci telefon, WhatsApp ak lu ni mel ngir def njàngum Biibëlam?

  3.   Ndax dinga mën a laaj keneen defal ko njàngum Biibëlam, ndax li nga fi nekkul?

5. Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga am gis-gis bu baax ci liggéeyu sakk ay taalibe bi mu ñu dénk. Bu dee sax yombul ci ki ngay jàngal Biibël bi mu teewe njàngum Biibëlam ayu bés bu neek, walla sax yombul ci moom mu topp santaane Yàlla yi ci dundam, ñaanal Yexowa mu dimbali la nga gis jéego yi mu nekk di def. (Filib 2:13) Ñaan ko itam mu dimbali la nga def lépp li nga mën ngir dimbali ko mu nekk taalibe Yeesu.