Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE JÀNGAL NIT ÑI BA ÑU NEKK TAALIBE YEESU

LESOŊ 11

Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd

Na li ngay wax nekk lu yomb a nànd

Njàngale bi: Na ‘ngeen génne ay wax yu yomb a nànd ci seen gémmiñ.’—1 Korent 14:9.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Macë 6:​25-27. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Ban misaal la Yeesu jël ngir won ñu ne Yexowa dafa ñu fonk?

  2.   Yeesu mënoon na wax lépp li mu xam ci picc yi, waaye defu ko. Lu tax ñu mën a wax ne li mu def mooy li gën ngir laal xolu ñi ko doon déglu?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Bu ñuy jëfandikoo kàddu yu yomb a nànd ngir jàngal nit ñi, loolu dina leen dimbali ñu jàpp lu ñu leen di jàngal, te li ñuy jàng dina laal seeni xol.

Nanga roy ci Yeesu

3. Bul wax lu bare. Bu dee sax, am na lu bare li nga xam ci ponk bi ngeen nekk di jàng, yemal ci li ñu bind ci biir lesoŋ bi. Te boo laaje nit ki dara, bul yàkkamti, may ko mu tontu la. Bu dee xamul tont bi, walla mu joxe tont bu àndul ak li Biibël di jàngale, mën nga ko laaj yeneen laaj yu koy dimbali mu am tontu bu baax bi. Bu ponk bi ngeen nekk di jàng leere ci moom, jarul nga ciy yokk leneen. Jàll-leen ci ponk bi ci topp.

4. Dimbalil ki ngay jàngal Biibël mu lëkkale lu bés li mu jàng ak li mu xamoon. Ci misaal, bala ngeen tàmbali lesoŋ buy wax ci ndekkite, njëkkal a xol li mu jot a jàpp ci li ngeen jàng ci liy xew bu nit deewe.

5. Jëfandikool misaal yu yomb a nànd. Laajal sa bopp lii:

  1.    ‘Ndax misaal bii, misaal bu yomb a nànd la?’

  2.   ‘Ndax ki may jàngal Biibël bi dina nànd misaal bi ma ko bëgg a jox?’

  3.   ‘Ndax ki may jàngal Biibël bi, misaal bi rekk lay jàpp, walla ndax misaal bi dina ko dimbali mu jàpp ponk yu am solo yu ma ko bëgg a jàngal?’