Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE JÀNGAL NIT ÑI BA ÑU NEKK TAALIBE YEESU

LESOŊ 12

Waxal nit ki ci lu leer li mu war a soppi ci dundam

Waxal nit ki ci lu leer li mu war a soppi ci dundam

Njàngale bi: «Ni diw ak cuuraay di bégal xol; noonu la xarit buy joxe xelal yu baax di bégal xol.»—Kàddu yu Xelu 27:9.

Ni ko Yeesu defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Màrk 10:​17-22. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Yann jikko yu rafet la Yeesu gisoon ci waxambaane bu bare alal bi?

  2.   Yeesu soxlawoon na won waxambaane bi mbëggeel. Waaye, waroon na am fit itam ngir xelal ko. Lu tax?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Yeesu def?

2. Dëgg la ne war nañu won mbëggeel ki ñuy jàngal Biibël bi, waaye war nañu am fit itam ngir wax ko li mu war a soppi ci dundam ngir mu jëm kanam ci wallu gëm.

Nanga roy ci Yeesu

3. Dimbalil ki ngay jàngal Biibël bi mu matal jubluwaay yi mu am ci wallu gëm.

  1.    Jëfandikool bu baax xaj bi tudd «Jubluwaay» ci téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww!

  2.   Dimbalil ki ngay jàngal Biibël bi mu xam li mu mën a def ba matal jubluwaay yu ndaw ak yu màgg yi mu am.

  3.   Deel jaajëfal ki ngay jàngal Biibël bi ci bépp jéego bi mu def ngir jëm kanam ci wallu ngëm.

4. Jéemal a xam li nekk di tere ki ngay jàngal Biibël bi mu jëm kanam ci wallu ngëm te dimbali ko mu def li war ngir jëm kanam.

  1.    Laajal sa bopp lii:

    • ‘Lan moo nekk di tere ki may jàngal Biibël bi mu jëm kanam ci wallu ngëm te sóobu ci ndox?’

    • ‘Ban ndimbal la soxla ngir jëm kanam ci wallu ngëm?’

  2.   Ñaanal Yexowa mu may la fit ngir nga wax ko li mu soxlaa soppi ci dundam. Ñaan ko itam mu dimbali la nga mën ci waxtaan ak moom ànd ci ak mbëggeel.

5. Bul kontine di jàng Biibël bi ak ki nga xam ne nekkul di def ay jéego ngir jëm kanam.

  1.    Laajal sa bopp lii:

    • ‘Ndax ki may jàngal Biibël bi dafay góor-góorlu ngir jëfe li muy jàng ci Biibël bi?’

    • ‘Ndax mu ngi góor-góorlu ngir teewe ndaje yi? Ndax mu ngi xamal ñeneen ñi li muy jàng ci Biibël bi?’

    • ‘Ndax ak lépp li mu jàng ci Biibël bi, bëgg na nekk Seede Yexowa moom itam?’

  2.   Bu dee ki ngay jàngal Biibël bi parewul ngir def ay jéego ngir jëm kanam ci wallu ngëm, toppal xelal yii di topp:

    • Waxal ki ngay jàngal Biibël bi mu xalaat ci li ko nekk di tere mu jëm kanam ci wallu ngëm.

    • Wax ko li tax doo kontine njàngum Biibëlam.

    • Wax ko li mu war a def bu bëgge ngeen tàmbaliwaat njàngum Biibëlam.