Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NI NGA MËNEE TÀMBALI WAXTAAN

LESOŊ 2

Waxal mel ni kuy waxtaan

Waxal mel ni kuy waxtaan

Njàngale bi: «Kàddu gu ñu wax ci waxtu bi gën—aka moo neex!»—Kàddu yu Xelu 15:23.

Ni ko Filib defe

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 8:​30, 31. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1.    Naka la Filib tàmbalee waxtaan bi?

  2.   Lu tax ñu mën a wax ne, ni mu tàmbalee waxtaan bi ak nitu Ecópi bi, mooy fasoŋ bi gën, ngir jàngal ko njàngale bu bees?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Filib def?

2. Bu ñuy wax ak nit ki, bu ñu jéem a forse waxtaan bi, waaye nañu wey di wax ak moom mel ni kuy waxtaan rekk. Noonu, nit ki dina ñu déglu bu baax. Amaana ñu am bunt ngir waar ko.

Nanga roy ci Filib

3. Deel seetlu. Li nit ki yëg, dafay feeñ ci kanamam ak ci ni muy jëfee ak yaw. Ndax mu ngi wone ne bëgg na la déglu? Ci misaal, boo ko bëggee won dara ci Biibël bi, mën nga ko laaj lii: «Ndax xamoon nga ne . . . ?», ba pare nga xol li muy def. Bul forse waxtaan ak ki nga xam ne bëggul a wax ak yaw.

4. Bul yàkkamti. Bul foog ne da nga war a ñëw rekk tàmbali wax lu jëm ci Biibël bi. Li gën mooy ngay waxtaan ak moom te xar ba nga am bunt ngir won ko dara ci Biibël bi. Yenn saay nag, da nga war a xar ba beneen yoon ngir mën a wax ak moom lu jëm ci Biibël bi.

5. Waxal nit ki li ko itteel. Nit ki mën na wax ci loo waajalul. Bu loolu amee, waxtaanal ak moom ci li ko itteel, bu dee sax li mu bëgg wute na ak li nga waajaloon.